Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Solomon son of David strengthened his hold on his kingdom; our Father was with him, making him very great. Suleymaan doomu Daawuda mujj na dëju bu baax ci nguuram, Aji Sax ji Yàllaam ànd ak moom, kaweel ko lool.
2 Solomon spoke to all Israel—the commanders of thousands and hundreds, the judges, and every leader in Israel, the family heads. Suleymaan nag wax ak Israayil gépp; njiiti junni yaak njiiti téeméer yaak àttekat yaak njiiti Israayil gépp, mboolem seen kilifay kër maam ya.
3 Solomon and the whole assembly went to the high place at Gibeon, where our Father's tent of meeting stood, which Moses, our Father's servant, made in the wilderness. Ci biir loolu Suleymaan ànd ak mbooloo ma mépp, dem ca bérebu jaamookaay ba ca Gabawon, sarxali fa, ndax xaymab ndajem Yàlla ba Musaa jaamub Aji Sax ji defaroon ca màndiŋ ma, foofa la nekkoon.
4 But David had brought the ark of our Father up from Kiriath-jearim to the place he prepared for it, pitching a tent for it in Jerusalem. Waaye fekk na gaalu Yàlla ga, Daawuda toxale woon na ko Kiryaat Yarim, yóbbu ko fa mu ko waajal, muy ab xayma bu mu ko sampal ca Yerusalem.
5 The bronze altar Bezalel son of Uri, son of Hur, made was there before the tabernacle of our Father; so Solomon and the assembly sought our Father there. Sarxalukaayu xànjar ba Beccalel doomu Uri doomu Ur defar nag, Daawudaa ko tegoon ca Gabawon, fa kanam màkkaanu Aji Sax ji, te mooy la fa Suleymaan ak mbooloo ma doon sàkkusi.
6 Solomon went up to the bronze altar before our Father at the tent of meeting and offered 1,000 burnt offerings on it. Suleymaan dem foofa ca sarxalukaayu xànjar ba ca kanam Aji Sax ji, ca kanam xaymab ndaje ma. Mu joxe fa junniy saraxi rendi-dóomal.
7 That night our Father appeared to Solomon and said to him, "Ask what I should give you." Guddig keroog la Yàlla feeñu Suleymaan. Mu ne ko: «Ñaanal loo bëgg ma may la ko.»
8 Solomon said to our Father, "You showed great covenant love to David my father, and made me king in his place. Suleymaan ne Yàlla: «Yaw de yaa baaxe lool Daawuda saa baay, te yaa ma fal buur, ma wuutu ko.
9 Now, my Father, confirm your promise to my father David, for you made me king over a people as many as the earth's dust. Léegi nag Aji Sax ji Yàlla, sa kàddu gaak Daawuda sama baay, yal na sax rekk, gannaaw yaw yaa ma fal ci kaw askan wu yaa, tollu ni feppi suufas àddina.
10 Give me wisdom and knowledge now to lead this people, for who can govern this great people of yours?" Kon nag xel ak xam-xam nga may may, ba ma xam nu may jiitee askan wii. Ndax kat, ana kan mooy àtte sa ñoñ, wii askan wu yaa?»
11 Our Father said to Solomon, "Because this was in your heart—you asked not for riches, wealth, or honor, nor your enemies' lives, nor long life, but for wisdom and knowledge to govern my people, over whom I made you king, Yàlla ne Suleymaan: «Gannaaw loolu moo nekk ci sa xol; ñaanoo koom ak alal ak daraja, ak sa bakkani bañ rot, te fan wu gudd it, ñaanoo ko, xanaa di ñaan xel ak xam-xam boo àttee sama ñoñ ñi ma la fal buur ci seen kaw,
12 wisdom and knowledge are given you. I will also give you riches, wealth, and honor no king before you had, and none after you will." xel mi ak xam-xam bi, mayees na la ko. Koom ak alal ak daraja it maa la ciy may lu buur yi masula am, du ñi la jiitu, du ñi topp ci yaw.»
13 So Solomon went from Gibeon's high place, from before the tent of meeting, to Jerusalem, and reigned over Israel. Ba loolu amee Suleymaan bàyyikoo ca xaymab ndaje ma ca jaamookaay ba ca Gabawon. Mu dem Yerusalem, falu buur ca Israayil.
14 Solomon gathered chariots and horsemen; he had 1,400 chariots and 12,000 horsemen, which he stationed in the chariot cities and with the king in Jerusalem. Ba mu ko defee Suleymaan dajale watiir yaak fas ya, muy junni ak ñeenti téeméeri (1 400) watiir, ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000) yu mu teg ca dëkk ya watiir ya féete, ak ca Yerusalem ga mu nekk.
15 In Jerusalem the king made silver and gold like stones, and cedar as plentiful as foothill sycamore-figs. Buur Suleymaan a def xaalis ak wurus late biir Yerusalem bay safi doj, garabi seedar di fa saf garabi sikomoor yi ne xas ci suufu tund yi.
16 Solomon's horses came from Egypt and Kue; the king's traders bought them from Kue at market price. Fasi Suleymaan, Misra lañu leen daan jëggaanee ak Silisi, baana-baanay buur, ca Silisi lañu leen daan jënde.
17 They imported a chariot from Egypt for about fifteen pounds of silver, a horse for about four; through them they exported these to all the kings of the Hittites and Aram. Ab watiir bu ñu jëggaanee Misra, indi, juróom benni téeméeri (600) dogi xaalis la leen daan dikke, aw fas di téeméer ak juróom fukki (150) dogi xaalis, te noonu lañu ca daan jëndaaleel mboolem buuri Etteen ña ak buuri Siri, indil leen.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]