Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Romans 9 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 I speak truth in Christ, not lying—my conscience testifies with me in the Holy Spirit, Li ma bëgga wax nag, ci kanam Kirist laa koy waxe; dëgg la, du aw fen. Sama xel, mi Xel mu Sell miy leeral, seedeel na ma ne dëgg laay wax.
2 that I have great sorrow and unceasing anguish in my heart. Maanaam, duma noppee am naqar wu réy ci sama biir xol,
3 I could wish myself cursed, cut off from Christ, for my brothers and sisters, my own people by blood. ba xawa bëgga tàggoo ak Kirist te alku, ngir ñi ma bokkal xeet mucc.
4 They are Israelites: theirs the full rights as sons, the glory, the covenants, the lawgiving, the worship, the promises. Bànni Israyil lañu, te Yàlla def na leen ni ay doomam; dëkkaloon na ndamam ci seen biir, fas ak ñoom kóllëre yi. Ñoom la Yàlla dénk yoonu Musaa, ñoom la xamal ni ñu ko wara jaamoo, ñoom la jox i digam.
5 The ancestors are theirs; from them, by human descent, comes the Christ, who is God over all, blessed forever. Amen. Maam ya Yàlla tànnoon, ci ñoom lañu bokk, ci ñoom it la Kirist wàcce, maanaam ci jëmmam, Kirist mi di Yàlla, tiim lépp, te yelloo teraanga ba fàww. Amiin.
6 This doesn't mean our Father's word has failed, for not all descended from Israel are Israel. Waaye neewuma waxu Yàlla dafa toxu, ndaxte bokk ci bànni Israyil, taxul nga bokk ci Israyil tigi.
7 Not all Abraham's offspring are his children; rather, "Your offspring will be named through Isaac." Te it du ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, ay doomam dëgg lañu. Ndaxte Yàlla dafa wax Ibraayma ne ko: «Saw askan ci Isaaxa lay jaar.»
8 That is, the children of the flesh are not children of our Father, but children of the promise count as offspring. Maanaam, soqikoo ci Ibraayma taxula nekk doomu Yàlla, waaye juddu ci biir digeb Yàlla mooy taxa bokk dëgg-dëgg ci askanu Ibraayma.
9 For the promise says: "At this time next year I will come, and Sarah will have a son." Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma ne ko: «Ci waxtu wii déwén dinaa délsi ci yaw, te Saarata dina am doom ju góor.»
10 Not only that, but Rebekah too conceived by one man, our father Isaac, Du ci loolu rekk, waaye noonu la it ci lu jëm ci Rebeka; doom yi mu jur ñoo bokk benn baay, moo di sunu maam Isaaxa.
11-12 though not yet born, having done nothing good or bad—so our Father's purpose by election might stand, Waaye Yàlla wax ko ne: «Yanqóoba rakk ji mooy yilif magam Esawu,» fekk xale ya juddooguñu te defaguñu dara, muy lu baax, muy lu bon. Yàlla def na noonu, maanaam tànn kenn ci doom yi, ngir dogalam mana taxaw, te sukkandikuwul ci seeni jëf waaye ci wooteb Yàlla.
12 not from works, but from him who calls, she was told: "the older will serve the younger." Not in this edition
13 As it is written, "Jacob I loved, but Esau I hated." Loolu la Mbind mi wax ne: «Bëgg naa Yanqóoba, bañ naa Esawu.»
14 What should we say then? Is there injustice with our Father? By no means! Kon lu nu ci wara wax? Ndax Yàlla àttewul foofu yoon nag? Mukk!
15 For he tells Moses, "I will have mercy on whom I have mercy, and I will have compassion on whom I have compassion." Dafa wax Musaa sax ne ko: «Su ma neexee yéwéne, su ma soobee yërëm.»
16 So then it depends not on human will or exertion, but on our Father, who has mercy. Dama leen di wax nag, dara ajuwul ci coobarey nit, mbaa ci ñaqam, waaye lépp a ngi aju ci yërmandey Yàlla.
17 For the Scripture says to Pharaoh: "I raised you up for this very reason, to show my power in you, and to have my name proclaimed in all the earth." Ndax Mbind mi biral na li Yàlla wax Firawna ne ko: «Def naa la buur, ngir feeñal sama kàttan ci say mbir, ngir siiwal sama tur ci àddina si sépp.»
18 So then he has mercy on whomever he wills, and he hardens whomever he wills. Kon nag Yàlla, la ko neex lay def, muy yërëm nit, mbaa dëgëral xolam ci lu bon.
19 So you'll ask me, "Why does he still find fault? Who resists his will?" Waaye xanaa dina am ku may wax ne: «Gannaaw kenn manula bañ coobarey Yàlla, lu tax kon muy teg nit tooñ?»
20 But who are you, mere human, to argue with our Father? Does the molded say to its molder, "Why did you make me like this?" Yaw nag nit ki, ak koo mana doon, lu tax ngay werante ak Yàlla? Ndax mbindeef dina laaj ki ko bind: «Lu tax nga binde ma nii?»
21 Does the potter not have authority over the clay, making from one lump a vessel for honor, another for dishonor? Ndax tabaxkatu ndaa sañula fab banam, tabax ci ñaari ndaa, benn bi ngir soxla yu am maana, bi ci des ngir soxla yu ndaw?
22 What if our Father, wanting to show his wrath and make known his power, patiently endured vessels of wrath prepared for destruction, Kon nag looy wax ci lii: Yàlla bëggoon na wone meram, xamle it dooleem ci àddina; teewul dafa sax ci muñal ñi yelloo meram te taxaw ci sànku.
23 to reveal his glory's riches for vessels of mercy he prepared beforehand for glory, Bëggoon na it xamle màggaayam mu ëpp xel, ci boole ñi mu yërëm ci ndamam; moo tax mu tànn leen ca njàlbéen.
24 even us whom he has called, not from the Jews only but also from the Gentiles? Wax ji noo ko moom, nun ñi Yàlla woo ci boppam ci biir Yawut yi ak ci biir xeet yi ci des.
25 As he says in Hosea, "I will call those not my children, my children, and her not beloved, beloved." Moom la wax ci téereb Ose ne: «Ñi nekkul woon sama xeet dinaa leen ko def, ñi bokkul woon ci sama mbëggeel, dinaa leen ci boole.»
26 "And in the very place where it was said to them, 'You are not my people,' there they will be called 'children of the living Father.'" Te: «Fa ñu leen waxe woon: “Dungeen sama xeet,” dees na leen fa wooye “Doomi Yàlla Boroom dund.”»
27 Isaiah cries out about Israel: "Though Israel's children number like sand of the sea, only a remnant will be saved, Esayi wax na ci mbirum Israyil ne: «Lu bànni Israyil baree bare ni suufus géej sax, lu néew rekk a ciy mucc.
28 for our Father will carry out his sentence upon the earth, fully and without delay." Ndaxte li Boroom bi dogal ci àddina, dina ko gaawa def, te dina mat sëkk.»
29 And as Isaiah predicted: "Had the Father of heaven's armies not left us offspring, we'd have become like Sodom, made like Gomorrah." Esayi it waxoon na lu jiitu loolu ne: «Boroom gàngoori xare yi, su bàyyiwul woon ci nun lu néew, kon ba tey raat nanu ni dëkki Sodom ak Gomor.»
30 What then should we say? Gentiles not pursuing righteousness attained righteousness, righteousness by faith; Lu nu ci wara wax nag? Ñi dul Yawut te fonkuñu woon jub ci kanam Yàlla, léegi jub nañu ci kaw ngëm.
31 but that Israel, who pursued a law of righteousness, did not reach that law. Waaye bànni Israyil, mi bëggoona sàmm yoon ngir jub, matalu ko.
32 Why? Because they pursued it not through faith but as though through works. They stumbled on the stumbling stone, Ndax lan? Ndax dañoo sukkandiku ci seeni jëf, bàyyi ngëm. Dañoo daanu ci «doj wuy fakktale.»
33 as it is written, "See, I am placing in Zion a stumbling stone, a rock that offends; whoever trusts him won't be put to shame." Moom la Yàlla wax ci Mbind mi ne: «Dinaa samp ci Siyoŋ doj wuy fakktale, di xeer wuy daaneel nit; waaye ku wéeru ci moom, sa yaakaar du tas.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]