Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Luke 22 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Now the Feast of Bread Without Yeast, called Passover, was approaching. Màggalu Mburu ma amul lawiir jege woon na, te ñu di ko wax bésu Mucc ba.
2 The chief priests and the scribes were looking for a way to kill him, because they feared the people. Sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya di wut pexem reylu Yeesu, ndaxte dañoo ragaloon nit ña.
3 Then Satan entered into Judas, the one called Iscariot, who was one of the twelve. Noonu Seytaane daldi solu Yudaa, mi ñuy wooye Iskariyo te mu bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar.
4 He went and conferred with the chief priests and temple officers how he might betray him to them. Noonu Yudaa dem waxtaani ak sarxalkat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga, ba xam nan la leen di jébbale Yeesu.
5 They were glad and agreed to give him money. Ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis.
6 He agreed and began looking for an opportunity to betray him to them away from the crowd. Yudaa nangu, di fexe jamono ju mu leen mana jébbal Yeesu, fu mbooloo ma nekkul.
7 Then the day of Unleavened Bread arrived, when the Passover lamb had to be sacrificed. Bésu màggalu Mburu ma amul lawiir agsi, ca bés boobu lañu waroona rendi gàttub bésu Mucc ba.
8 Jesus sent Peter and John, saying, "Go prepare the Passover for us to eat." Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, defaral nu reeru bésu Mucc ba.»
9 They said to him, "Where do you want us to prepare it?" Ñu ne ko: «Fan nga bëggoon, nu defare ko fa?»
10 He said, "Once you enter the city, a man carrying a jar of water will meet you. Follow him into the house he enters, Mu ne leen: «Bu ngeen duggee ca dëkk ba, góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen. Toppleen ci moom ba ca kër ga muy dugg,
11 "and tell the owner of the house, 'The Teacher says to you: Where is the guest room where I may eat the Passover with my disciples?' te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru bésu Mucc ba, man ak samay taalibe?”
12 And he will show you a large upper room, furnished; prepare it there." Noonu dina leen won néeg bu féete kaw, te yaa, ñu defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.»
13 They went and found it just as he had told them, and they prepared the Passover. Ñu dem, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.
14 When the hour came, he reclined at table, and the apostles with him. Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi,
15 He told them, "I have deeply longed to eat this Passover with you before I suffer. ne leen: «Yàkkamti woon naa lool lekk ak yéen reeru bésu Mucc bii, laata ñu may sonal.
16 For I tell you, I won't eat it until it's fulfilled in the kingdom of our Father." Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Yàlla.»
17 Taking a cup and giving thanks, he said, "Take this and divide it among yourselves. Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko.
18 For I tell you, from now on I will not drink the vine's fruit until our Father's kingdom comes." Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum reseñ mi, ba kera Yàlla di tëral nguuram.»
19 He took bread, gave thanks, broke it, and gave it to them, saying, "This is my body, given for you. Do this in memory of me." Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»
20 He did the same with the cup after supper: "This cup is the new covenant in my blood, poured out for you. Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen.
21 But look—the hand of the one who betrays me is with me on the table. Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li.
22 The Son of Man goes as determined, but woe to that man through whom he is handed over!" Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.»
23 They began asking each other which of them would do this. Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy nara def loolu.
24 A dispute also arose among them about which of them was the greatest. Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci ñoom moo gëna màgg.
25 He said to them, "Kings of nations dominate them, and rulers over them are called benefactors. Yeesu ne leen: «Buuri xeeti àddina dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañuy sàkku ngërëm.
26 Not so with you: let the greatest among you become like the youngest, the leader like the one serving. Waaye yéen buleen def noonu. Ki gëna màgg ci yéen, na nekk ni ki gëna ndaw, te njiit mel ni surga.
27 Who is greater—the guest at the table or the one serving? The guest, isn't it? Yet I am among you as one who serves. Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gëna màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga.
28 "You are those who have stayed with me in my trials, Yéen nag yéenay ñi ànd ak man ci samay fitna.
29 and I confer on you a kingdom, just as my Father conferred one on me, Man nag jox naa leen sañ-sañu nguuru, ni ma ko sama Baay joxe.
30 so you'll eat and drink at my table in my kingdom, and sit on thrones judging the twelve tribes of Israel." Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.»
31 "Simon, Simon, listen—Satan has demanded to sift all of you like wheat, Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax.
32 but I prayed for you, that your faith not fail. Once you have turned back, strengthen your brothers." Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo délsee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.»
33 Peter said, "Lord, I'm ready to go with you to prison and death." Piyeer ne ko: «Boroom bi, àttan naa ànd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.»
34 Jesus said, "I tell you, Peter: the rooster won't crow today before you deny three times that you know me." Yeesu ne ko: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
35 He asked, "When I sent you without money bag, knapsack, or sandals, did you lack anything?" "Nothing," they said. Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
36 He said to them, "But now, let the one with a money bag take it, and a knapsack too. Let the one without a sword sell his cloak and buy one. Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am xaalis, na ko jël; te ku am mbuus, na ko jël; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, jënde ko jaasi.
37 For I tell you this Scripture must be fulfilled in me: 'He was counted among sinners.' For what is written about me is coming true." Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax fàww mu am ci man, bi mu nee: “Boole nañu ko ak ñu bon ña.” Ndaxte loolu jëm ci man mi ngi mat.»
38 They said, "Lord, look, here are two swords." He said to them, "It is enough." Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.»
39 And he went out, as usual, to the Mount of Olives, and the disciples followed him. Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe naka-jekk. Taalibeem ya topp ci moom.
40 When he reached the place, he told them, "Pray you don't give in to temptation." Bi mu agsee ca bérab ba, mu ne leen: «Ñaanleen, ngir baña daanu cig fiir.»
41 And he withdrew from them about a stone's throw, and knelt down and prayed, Noonu mu dànd leen, ba fu aw saan mana tollu, daldi sukk di ñaan ne:
42 saying, "Father, if you are willing, take this cup from me. Yet not my will, but yours, be done." «Baay, soo ko bëggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
43 And an angel from heaven appeared to him, strengthening him. Noonu malaakam Yàlla daldi koy feeñu, may ko doole.
44 In agony he prayed more intensely; his sweat became like great drops of blood falling down to the ground. Ci biir tiis, Yeesu gëna sawar ci ñaan gi, ñaqam mel ni lumbi deret dal ci suuf.
45 When he rose from prayer, he came to the disciples and found them asleep from grief, Bi mu ñaanee ba noppi, mu jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis.
46 he said to them, "Why are you sleeping? Get up and pray, so you don't yield to temptation." Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña daanu cig fiir.»
47 While he was still speaking, a crowd came, led by the one called Judas, one of the twelve. He came up to Jesus to kiss him, Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku ñuy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak ñaar jiite leen. Yudaa jegeñsi Yeesu, bëgg koo fóon.
48 but Jesus said to him, "Judas, would you betray the Son of Man with a kiss?" Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!»
49 Seeing what was about to happen, those with him said, "Lord, should we strike with the sword?" Bi ñi àndoon ak Yeesu gisee liy bëgga xew, ñu ne: «Boroom bi, ndax nu dóore jaasi?»
50 And one of them struck the servant of the high priest and cut off his right ear. Kenn ci ñoom nag dóor surgab sarxalkat bu mag ba, noppu ndijooram dagg.
51 But Jesus answered, "No more of this!" And he touched the ear and healed him. Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
52 Then Jesus said to the chief priests, temple officers, and elders who had come out against him, "Have you come out with swords and clubs, as against a robber? Noonu Yeesu ne sarxalkat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc.
53 Every day I was with you in the temple, and you didn't lay hands on me. But this is your hour, and the authority of darkness." Moona maa nga woon ak yéen bés bu nekk ca kër Yàlla ga, te jàppuleen ma. Waaye léegi seen waxtu la, di jamonoy lëndëm.»
54 Seizing him, they led him and brought him into the high priest's house; Peter followed at a distance. Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër sarxalkat bu mag ba. Piyeer topp fu sore.
55 They lit a fire in the middle of the courtyard and sat together; Peter sat among them. Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir.
56 But a servant girl, seeing him sitting facing the light, stared at him and said, "This one too was with him." Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko jàkk ne: «Nit kii itam àndoon na ak moom.»
57 But he denied it, saying, "Woman, I do not know him." Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.»
58 Shortly after, another saw him and said, "You too are one of them." But Peter said, "Man, I'm not." Nees-tuut keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer ne ko: «Sama waay, bokkuma ci.»
59 About an hour later, another insisted, "This man was certainly with him, for he's a Galilean too." Bi ñu tegee lu mat waxtu, keneen dikkaat ca wax ja ne: «Ci lu wóor nit kii àndoon na ak moom, nde Galile la jóge.»
60 But Peter said, "Man, I don't know what you're saying." Immediately, while he was still speaking, the rooster crowed. Waaye Piyeer ne ko: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab.
61 The Lord turned and looked at Peter. Peter remembered what the Lord had told him: "Before the rooster crows today, you will deny me three times." Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer fàttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi ñetti yoon.»
62 And he went out and wept bitterly. Piyeer daldi génn, di jooy jooy yu metti.
63 Now the men who were holding Jesus mocked him as they beat him. Nit ñaa nga jàppoon Yeesu, di ko ñaawal ak di ko dóor.
64 They blindfolded him and kept asking, "Prophesy! Who is it that struck you?" Ñu ngi takkoon ay bëtam, di ko laaj, naan ko: «Yaw, wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?»
65 And they said many other things against him, insulting him. Ñu ngi ko doon tifaar it yeneen saaga.
66 At daybreak, the people's council of elders convened—chief priests and scribes—and led him away to their council, saying, Bi bët setee, kureelu njiiti xeet wa, maanaam sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya, daldi daje, indi Yeesu ci seen kanam.
67 "If you are the Christ, tell us." He said to them, "If I tell you, you will not believe, Ñu ne ko: «Soo dee Almasi bi, wax nu ko.» Mu ne leen: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm.
68 "and if I ask you, you will not answer. Te su ma leen laajee, dungeen tontu.
69 "But from now on the Son of Man will sit at the right hand of the power of our Father." Waaye gannaaw-si-tey, Doomu nit ki dina toog ci ndijooru Yàlla, Aji Man ji.»
70 They all said, "So you are the Son of God?" He said to them, "You say that I am." Noonu ñépp ne: «Kon nag yaay Doomu Yàlla ji?» Mu ne leen: «Yéen ci seen bopp wax ngeen ne moom laa.»
71 They said, "What more testimony do we need? For we heard it ourselves from his mouth." Ñu daldi ne nag: «Lu nuy doyeeti seede léegi, ndegam nun ci sunu bopp noo ko nangoo ci gémmiñam!»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]