Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 25 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Now three days after Festus had arrived in the province, he went up to Jerusalem from Caesarea. Bi Festus teersee ci diiwaanam, mu teg ca ñetti fan, dem Yerusalem.
2 There the chief priests and Jewish leaders presented their case against Paul and kept urging him, Noonu sarxalkat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame Pool ci moom.
3 requesting a favor against him—that he summon Paul to Jerusalem. They were setting an ambush to kill him on the road. Ñuy sàkku ndimbal ci moom, di ko ñaan bu wér, mu yónni Pool Yerusalem, fekk lal nañu fiiru rey ko ca yoon wa.
4 Festus replied that Paul was held at Caesarea, and he himself would leave shortly. Waaye Festus ne leen: «Ñu ngi wottu Pool ca Sesare, te dinaa fa dem fi ak fan yu néew.»
5 "So," he said, "let those among you who are able go down with me and accuse the man, if there is anything wrong with him." Mu ne leen: «Ñi am maana ci yéen nag, nangeen ànd ak man, layooji ak nit ka, bu dee tooñ na.»
6 Festus stayed with them no more than eight or ten days, then went down to Caesarea. The next day he took the judge's seat and ordered Paul brought in. Noonu Festus am fa ñoom juróom ñett ba fukki fan, ba noppi dem Sesare. Ca ëllëg sa mu toog ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi Pool.
7 When Paul arrived, the Jews from Jerusalem surrounded him, bringing many serious charges they couldn't prove. Bi mu ñëwee nag, Yawut ya jóge Yerusalem wër ko, di ko jiiñ tooñ yu bare te réy, te manuñu leena firndeel.
8 Paul answered in his defense: "I have done no wrong against the Jewish law, the temple, or Caesar." Noonu Pool làyyi ne: «Tooñuma yoonu Yawut ya, tooñuma kër Yàlla ga, tooñuma buur ba Sesaar.»
9 But Festus, wanting to please the Jews, asked Paul, "Will you go up to Jerusalem and be tried there before me on these charges?" Ci kaw loolu Festus, mi bëgg lu neex Yawut ya, wax Pool ne: «Ndax bëgguloo dem Yerusalem, nga layoo fa ci mbir yii ci sama kanam?»
10 Paul said, "I stand before Caesar's tribunal, where I must be judged. I've done the Jews no wrong, as you yourself know very well. Waaye Pool ne ko: «Maa ngi nii taxaw ci kanam àttekaayu buur Sesaar; te fii lañu ma wara àttee. Te yaw ci sa bopp xam nga bu baax ne tooñuma Yawut yi.
11 If I've done wrong, done something deserving death, I won't refuse to die. But if these men's charges against me are groundless, no one can hand me over to them. I appeal to Caesar." Su ma tooñoon mbaa ma def lu bon lu jar dee, kon duma tinu ngir baña dee. Waaye bu li ñu may jiiñ taxawul, kenn sañu ma leena jébbal. Dénk naa sama mbir Sesaar.»
12 After consulting his council, Festus answered, "You appealed to Caesar; to Caesar you will go." Bi mu waxee loolu, Festus gise ak ñi ko wër, mu ne ko: «Dénk nga sa mbir Sesaar, kon ci moom ngay dem.»
13 Some days later, King Agrippa and Bernice came to Caesarea and greeted Festus. Ba ñu ca tegee ay fan, buur Agaripa ak Berenis ñëw Sesare, ngir nuyusi Festus.
14 As they spent many days there, Festus presented Paul's case to the king: "Felix left a man here as a prisoner. Bi seen ngan di ruus nag, Festus diis buur ba mbirum Pool ne ko: «Feligsë batale na nu ak kenn ku ñu tëj.
15 While I was in Jerusalem, the chief priests and elders of the Jews accused him, asking me for his conviction. Bi ma nekkee Yerusalem, sarxalkat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame nañu ko ci man, ñaan ma, ma daan ko.
16 I told them it's not Roman custom to hand over anyone before the accused faces his accusers in person and gets a chance to defend himself against the charge. Waaye ma ne leen: “Jébbale nit, fekk jàkkaarloowul ak ñi koy jiiñ, ba mana làyyil boppam ci li ñu koy jiiñ, loolu dëppoowul ak aaday nguuru Room.”
17 So when they gathered here, I delayed nothing—next day I sat on the judgment seat and ordered the man brought in. Bi ñu àndee ak man ba fii nag, randaluma mbir mi, waaye ca ëllëg sa sax toog naa ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi nit kooku.
18 When his accusers stood up, they raised none of the criminal charges I had expected. Ñi koy kalaame nag, bi ñu taxawee, jiiñuñu ko benn ñaawteef ci yi ma yaakaaroon,
19 Instead, they had some disputes with him about their own religion and a dead man named Jesus, whom Paul kept claiming was alive. waaye ñuy werante rekk ak moom ci seen yoon ak ci mbirum ku tudd Yeesu, mi dee, te Pool sax ci ne mu ngi dund.
20 Unsure how to investigate this, I asked if he was willing to go to Jerusalem and be tried there on these charges. Gannaaw lijjanti mbir moomu jafe woon na ma lool nag, ma laaj ko, ndax bëgg na dem Yerusalem, layooji fa ci mbir yooyu.
21 But since Paul appealed to be held for the Emperor's decision, I ordered him held until I could send him to Caesar." Waaye Pool ñaan, nu fomm mbiram, ba kera buur bu tedd ba di ko àtte. Noonu santaane naa ñu aj ko, ba keroog ma koy yónnee Sesaar.»
22 Agrippa told Festus, "I'd like to hear the man myself." "Tomorrow," Festus said, "you will hear him." Booba nag Agaripa ne Festus: «Man sax bëgg naa dégg nit kooku.» Festus ne ko: «Bu ëllëgee dinga ko dégg.»
23 The next day Agrippa and Bernice arrived with great show and entered the hall with the military commanders and the city's prominent men. On Festus's order, Paul was brought in. Ca ëllëg sa nag Agaripa ak Berenis ñëw bu xumb, ñu dugg ca néegu àtte ba, ànd ak kilifay xare ba ak ña am maana ca dëkk ba. Noonu Festus joxe ndigal, ñu indi Pool.
24 Festus said, "King Agrippa, and all here with us—you see this man. The whole Jewish community petitioned me about him, both in Jerusalem and here, shouting he must not live any longer. Bi mu ñëwee, Festus ne: «Buur Agaripa ak yéen ñépp, ñi fi teew tey, nit kaa ngi nii! Mbiram moo tax mbooloom Yawut yépp, muy ci Yerusalem, muy fii, wër ma di yuuxu ne: “Nit kii waratula dund.”
25 But finding nothing deserving death, and since he himself appealed to the Emperor, I decided to send him. Waaye gis naa ne deful dara lu jar dee. Moona, gannaaw moom ci boppam dénk na boppam buur bu tedd ba, fas naa yéene yónnee ko ko.
26 I have nothing definite to write my lord about him, so I brought him before you all, especially before you, King Agrippa, so that after this examination I may have something to write. Fekk awma dara lu wóor ci mbiram, lu ma mana bind sang bi. Moo tax ma indi ko ci seen kanam, rawatina ci sa kanam, buur Agaripa, ngir sunu jataay may ma lu ma bind.
27 For it seems unreasonable to me to send a prisoner without indicating the charges against him." Ndaxte yaakaar naa ne yónnee ku ñu tëj, te bañ caa boole lu ko waral, àndul ak xel.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]