Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 22 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 "Brothers and fathers, listen now to my defense before you." «Yéen bokk yi ak baay yi, dégluleen samaw lay.»
2 When they heard him speaking to them in Hebrew, they grew even more quiet. And he said: Bi ñu déggee, mu di leen wax ci làkku yawut, ñu gën ne xerem. Noonu Pool ne leen:
3 "I am a Jew, born in Tarsus of Cilicia, raised in this city, trained at Gamaliel's feet in the strict law of our ancestors, as eager for God as all of you are today. «Man Yawut laa, juddoo Tars ci diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Taalibe laa woon ci Gamaleel, mu jàngal ma bu wér yoonu sunuy maam, ba ma sawar ci Yàlla, mel ni yéen ñépp tey.
4 I persecuted this Way to the death, binding and delivering to prison both men and women, Daan naa fitnaal ña bokkoon ci yoon wii, ba di ci rey sax; yeew naa góor ak jigéen, tëj leen;
5 as the high priest and the whole council of elders can testify. From them I received letters to the brothers in Damascus, and went to bring those there as prisoners to Jerusalem for punishment." sarxalkat bu mag ba ak mbooloom njiit yi yépp man nañu ma cee seede. Am bés ñu bindal ma ay bataaxal ngir bokki Damaas. Ma doon fa dem, ngir yeew ña fa nekkoon, indi leen Yerusalem, ngir ñu yar leen.
6 "Traveling and nearing Damascus about noon, a great light from heaven suddenly flashed around me." «Waaye ci digg bëccëg, bi ma jaaree ca yoon wa, ba jegesi Damaas, ca saa sa leer gu mag jóge asamaan, melax ba ëmb ma.
7 I fell to the ground and heard a voice say to me, "Saul, Saul, why are you persecuting me?" Ma daldi ne nërëm ci suuf, dégg baat bu ma ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal?”
8 I answered, "Who are you, Lord?" He replied, "I am Jesus of Nazareth, whom you're persecuting." Ma ne ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Mu ne ma: “Maa di Yeesum Nasaret, mi ngay fitnaal.”
9 "Those with me saw the light but didn't understand the voice of the one speaking to me." Ñi ma àndaloon gis nañu leer ga, waaye dégguñu baatu ka doon wax ak man.
10 I said, "What should I do, Lord?" The Lord replied, "Get up and go into Damascus. There you'll be told all you've been appointed to do." Noonu ma laaj ko: “Lu ma wara def, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Jógal dem Damaas, foofa dees na la biral lépp, li ma la yen.”
11 "Since that light's brightness blinded me, my companions led me by the hand into Damascus." Gannaaw gisuma woon dara ndax leeraayu melxat ga, ña ma àndal wommat ma, ma ñëw Damaas.
12 "A man named Ananias, devout by the law, well spoken of by all the Jews living there, «Bi ma ko defee ku tudd Anañas ñëw ci man. Nit ku ragal Yàlla la woon ci sàmm yoonu Musaa, te Yawuti Damaas yépp seedeel ko lu baax.
13 came and stood by me and said, 'Brother Saul, receive your sight.' At that very hour I looked up and saw him." Mu taxaw ci sama wet ne ma: “Sóol sama mbokk, delluwaatal di gis.” Noonu ma daldi gisaat ca saa sa, xool ko.
14 "He said, 'The God of our fathers appointed you to know his will, to see the Righteous One, and to hear a voice from his mouth; Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam tànn na la, ba may la, nga xam coobareem te gis Aji Jub ji te nga dégg ay waxam.
15 for you will be his witness to everyone of what you have seen and heard. Ndaxte li nga gis te dégg ko, dinga ko seede ci ñépp.
16 And now, why wait? Get up, be baptized, wash away your sins, calling on his name." Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set ci say bàkkaar ci tudd turu Yeesu.”
17 "When I had returned to Jerusalem and was praying in the temple, I fell into a trance," «Bi ma délsee Yerusalem nag, di ñaan ca kër Yàlla ga, leer tàbbi ci man.
18 and saw him saying to me, "Hurry and leave Jerusalem quickly, because they won't accept your testimony about me." Ma daldi gis Boroom bi, mu ne ma: “Génnal Yerusalem nu mu gëna gaawe, ndaxte duñu nangu li ngay seede ci man.”
19 I said, "Lord, they themselves know that I went from synagogue to synagogue imprisoning and beating those who believed in you. Ma ne ko: “Boroom bi, xam nañu ne dama daan wër jàngoo jàngu, di tëj kaso ak di dóor ay yar ñi la gëm.
20 When the blood of your witness Stephen was being shed, I stood by, approving and guarding the cloaks of those killing him.'" Rax-ca-dolli bi ñu tuuree deretu Ecen, mi la doon seedeel, teewe naa ko, ànd ca, bay wottu sax yérey ñi ko doon rey.”
21 "And he said to me, 'Go, for I will send you far away to the Gentiles.'" Waaye Boroom bi ne ma: “Demal, dinaa la yebal fu sore, nga jëm ci xeeti ñi dul Yawut.”»
22 Up to that point they listened, then they raised their voices and shouted, "Erase such a man from the earth! He shouldn't be allowed to live!" Mbooloo ma déglu ko nag ba ca wax jooju, waaye bi ñu déggee loolu, ñu daldi yuuxu naan: «Farleen ko ci àddina! Yembar mu mel ni moom yeyoowula dund!»
23 And as they were shouting and throwing off their cloaks and flinging dust into the air, Ñu daldi yuuxu ak di sànni seeni yére, tibb suuf, di callmeeru.
24 the commander ordered him taken into the barracks and whipped, to learn why they were shouting against him like this. Noonu kilifa ga santaane, ñu dugal Pool ca tata ja te caw ko ay yar yu metti, laaj ko ba xam lu tax ñu di ko yuuxoo nii.
25 As they stretched him out for the straps, Paul said to the centurion standing there, "Is it legal for you to whip a Roman citizen who hasn't been condemned?" Waaye bi ñu koy joñ ak ay der, Pool ne njiitu xare ba fa taxaw: «Ndax am nga sañ-sañu dóor ay yar jaamburu Room, te fekk yoon dabu ko sax?»
26 Hearing this, the centurion went to the commander and reported it: "What are you about to do? This man is a Roman citizen." Bi ko njiit la déggee, mu fekki kilifaam, yégal ko ko; mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay def? Nit kale jaambur la ci Room.»
27 So the commander came and asked, "Tell me, are you a Roman citizen?" "Yes," he said. Noonu kilifa ga ñëw laaj Pool: «Wax ma, ndax jaambur nga ci Room?» Mu ne ko: «Waaw, moom laa.»
28 The commander said, "I paid a large sum for this citizenship." But Paul said, "I was born a citizen." Kilifa ga ne ko: «Man fey naa xaalis bu bare, ngir nekk jaambur ci Room.» Waaye Pool ne ko: «Man de dama koo judduwaale.»
29 So those about to question him withdrew at once; the commander was afraid, realizing he had bound a Roman citizen. Ñi ko bëggoona dóor ay yar nag randu ko ca saa sa. Te kilifa ga sax tiit ci xam ne Pool jaamburu Room la, te yeewlu na ko.
30 The next day, wanting to know exactly why the Jews accused him, the commander freed Paul, ordered the chief priests and the whole council to assemble, brought Paul down, and set him before them. Ca ëllëg sa kilifa ga bàyyi ko, ndaxte bëggoon na xam bu wóor lu ko Yawut ya jiiñ. Mu santaane ne, sarxalkat yu mag ya dajaloo, ñoom ak kureelu àttekat ya. Gannaaw loolu mu indilu Pool, dëj ko ci seen kanam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]