Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 20 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 After the uproar ended, Paul sent for the disciples, encouraged them, said goodbye, and left for Macedonia. Bi yëngu-yëngu ba dalee, Pool woo taalibe ya fa moom, dooleel leen. Bi mu ko defee mu tàggoo ak ñoom, jóge fa, dellu diiwaanu Maseduwan.
2 When he had passed through those regions and given the believers much encouragement, he came to Greece. Noonu mu jaar ca bérab yooyu, di dooleel nit ñi ak wax yu bare; ba noppi mu dem réewu Geres,
3 He stayed three months; when the Jews plotted against him as he was about to sail for Syria, he decided to return through Macedonia. toog fa ñetti weer. Waaye bi mu nekkee ci kaw tànki dugg gaal jëm diiwaanu Siri, te Yawut yi lalal ko pexe, mu fas yéenee dellu, jaare Maseduwan.
4 Sopater son of Pyrrhus of Berea, Aristarchus and Secundus of Thessalonica, Gaius of Derbe, Timothy, and Tychicus and Trophimus of Asia accompanied him. Booba nag ñii ñoo ànd ak moom: Sopater, doomu Pirus mi dëkk Bere; Aristàrk ak Segond, ñi dëkk Tesalonig; Gayus, mi dëkk Derbë, ak Timote; te it Tisig ak Torofim ñi dëkk Asi.
5 These went on ahead and were waiting for us at Troas. Ñooñu nag jiitu, di nu nég dëkku Torowas.
6 We sailed from Philippi after the days of Unleavened Bread, reaching them at Troas in five days and staying there seven days. Waaye naka nun, gannaaw màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ma amul lawiir, nu dugg gaal ci Filib, def ci juróomi fan, fekksi leen Torowas, nu am fa juróom ñaari fan.
7 On the first day of the week, when we gathered to break bread, Paul talked with them; planning to leave the next day, he kept talking until midnight. Ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, booloo nanu ngir damm mburu ma. Te Pool, mi bëggoona dem ca ëllëg sa, di diisoo ak ñoom te waxtaanam law ba ci xaaju guddi.
8 There were many lamps in the upper room where we were gathered. Ca néeg bu kawe, ba nu booloo nag, amoon na fa làmp yu bare.
9 A young man named Eutychus sat in the window, sinking into deep sleep as Paul kept talking. Overcome by sleep, he fell from the third story and was picked up dead. Noonu waxambaane wu tudd Ëtikus te toog ca palanteer ba, gëmméentu bay jeyaxu. Bi Pool di gëna yaatal waxtaanam nag, nelaw daldi ko jàpp, mu xàwwikoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee.
10 Paul went down, bent over him, and embracing him said, "Don't be alarmed; his life is in him." Waaye Pool wàcc, daldi sëgg ci kawam, roof ko loxoom ne leen: «Bàyyileen jooy yi, mu ngi dund.»
11 He went back up, broke bread, ate, and talked with them a long time, until daybreak, then left. Noonu mu yéegaat, damm mburu ma, lekk; ba noppi delluwaat ci waxtaanam, di ko yaatal ba ca njël, doora tàggoo.
12 And they brought the young man home alive, and were greatly comforted. Naka waxambaane wa, ñu indi ko muy dund, ba seen xol sedd guyy.
13 We went ahead by ship to Assos, planning to take Paul aboard; he had chosen to go by land. Nun nag nu jiitu, dugg gaal jëm Asos, fa nu Pool santoon, nu jële ko fa; fekk moom fas na yéeney dox, ba agsi fa.
14 And when he met us at Assos, we took him on board and came to Mitylene. Noonu mu fekksi nu ci Asos, nu jël ko ca gaal ga, dem Mitilen.
15 Sailing from there, we came opposite Chios the next day, put in at Samos the day after, and reached Miletus the following day. Gannaaw loolu gaal ga jóge fa, nu agsi ca ëllëg sa janook dunu Kiyos. Bés ba ca tegu nag nu jàll ba Samos, te ñetteelu fan ba nu àgg Mile.
16 Paul had decided to sail past Ephesus, avoiding time in Asia; he was hurrying to reach Jerusalem, if possible, by Pentecost. Ndaxte Pool fasoon na yéenee teggi Efes, ngir baña yàgg ci diiwaanu Asi; mu ngi doon gaawantu, ngir màggal, gi ñuy wax Pàntakot fekk ko Yerusalem.
17 From Miletus he sent to Ephesus and called the elders of the church to come to him. Bi Pool eggee Mile nag, mu yónnee ca Efes, ngir woo njiiti mbooloom ñi gëm.
18 When they came, he said, "You know how I lived among you the whole time, from the first day I set foot in Asia, Bi ñu ñëwee, mu ne leen: «Yéen xam ngeen bu baax, ni ma doon doxale diirub sama ngan gépp ci seen biir, li dale ci bés bi ma jëkkee teg tànk ci Asi ba tey.
19 serving our Lord Jesus with complete humility, tears, and trials brought on by the Jews' plots against me, Jaamu naa Boroom bi ci woyof gu mat ak ay rongooñ, dékku ay nattu yu ma pexey Yawut yi indil.
20 how I held nothing back that would help you, but declared it and taught you publicly and house to house, Xam ngeen ne masuma leena nëbb dara lu leen di jariñ, di leen jàngal ci kanam ñépp ak ca kër ya.
21 testifying to both Jews and Greeks: repentance toward our Father and faith in our Lord Jesus. Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub seeni bàkkaar, ba waññiku ci Yàlla te gëm sunu Boroom Yeesu.
22 Now bound by the Spirit, I'm heading to Jerusalem, not knowing what awaits me there, «Léegi maa ngi nii di dem Yerusalem, ci li ma Xelu Yàlla mi xiirtal, te xawma lu ma fay dal.
23 except the Holy Spirit tells me in every city that chains and sufferings await me. Xam naa rekk ne ci dëkkoo dëkk Xel mu Sell mi xamal na ma ne ay buum ak ay metit ñu ngi may nég.
24 But I place no value on my life, nor treasure it for myself, only that I finish my course and the ministry I received from our Lord Jesus, testifying to the gospel of our Father's grace. Waaye sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal liggéey, bi ma Boroom bi dénk, maanaam ma seedeel ci ñépp xibaaru jàmm, bi ëmb yiwu Yàlla.
25 And now I know none of you among whom I went preaching the kingdom of our Father will see my face again. «Fi mu ne nag xam naa ne dootuleen gis sama kanam, yéen ñépp ñi ma jaaroon ci seen biir, di yégle nguuru Yàlla.
26 Therefore I testify to you this day that I am innocent of the blood of all, Moo tax may dëggal tey jii ne wàccoo naa ak yéen ñépp bés pénc.
27 for I did not shrink from declaring to you the whole purpose of our Father. Ndaxte ñeebluwuma leen, ci di leen xamal lépp li Yàlla digle.
28 Watch yourselves and all the flock the Holy Spirit made you overseers of, to shepherd our Father's church, which he purchased with the blood of his own Son. Wottuleen nag seen bopp te wottu coggal jépp, ji leen Xel mu Sell mi def sàmm, ngeen sàmm mbooloo, mi Yàlla jotal boppam ak deretu Doomam.
29 I know that after my departure fierce wolves will come in among you, not sparing the flock. Xam naa ne bu ma leen wonee gannaaw, bukki yu soxor dinañu tàbbi ci coggal ji te duñu ci ñeeblu kenn.
30 Men from among you will rise, speaking distorted things, to draw the disciples away after them. Ay nit dinañu jóg ci seen biir sax, di wax luy sànke, ngir sàkku ay taalibe.
31 So watch, remembering that for three years, night and day, I never stopped warning each one of you with tears. Foogleen nag, di fàttaliku ne diirub ñetti at, guddi ak bëccëg, masumaa noppi di leen artu kenn ku nekk ci yéen ak ay rongooñ.
32 Now I entrust you to our Father and to the word of his grace, able to build you up and give you the inheritance among all who are made holy. «Léegi nag maa ngi leen di dénk Boroom bi, moom ak kàddug yiwam, gi leen mana dëgëral te may leen cér ci biir gaayi Yàlla yu sell yépp.
33 I coveted no one's silver or gold or clothing. Nammuma xaalisu kenn mbaa wurusam mbaa koddaayam.
34 You yourselves know that these hands provided for my needs and for those who were with me. Xam ngeen ne faj naa samay soxla ak soxlay ñi ànd ak man ci sama loxo yii.
35 In everything I showed you that, working hard this way, we must help the weak, remembering the words of our Lord Jesus, that he himself said, It is more blessed to give than to receive." Ci lépp won naa leen royukaay, ci li nu wara dimbali ñi néew doole te fàttaliku li Yeesu Boroom bi wax moom ci boppam ne: “Joxe moo gëna barkeel nangu.”»
36 And when he had said these things, he knelt down with them all and prayed. Bi mu waxee loolu, mu sukk ak ñoom ñépp, ñaan ci Yàlla.
37 They all wept; they embraced Paul and kissed him, Te ñépp jooy bu metti, di laxasu ci baatu Pool, fóon ko bu baax.
38 grieving most over his words—that they'd never see his face again—they walked him to the ship. Li leen gëna teg aw tiis mooy li mu leen wax: «Dootuleen gis sama kanam.» Noonu ñu gunge ko ba ca gaal ga.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]