Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

2 Peter 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Beloved, this is now the second letter I write you; in both I stir up your sincere mind by reminder. Yéen samay xarit, sama ñaareelu bataaxal a ngi nii. Bind naa leen, ngir xiir leen ci xalaat yu sell.
2 Remember the words the holy prophets spoke beforehand, and the command of our Lord and Savior given through your apostles. Maa ngi leen di fàttali kàdduy yonent yu sell, yi fi jiitu woon, ak ndigalu Boroom bi sunu Musalkat, li ngeen déggoon ci ndaw, yi Yàlla yebaloon fi yéen.
3 Know this first: mockers will come in the last days, mocking, following their own lusts. Nangeen jëkka xam lii: mujug jamono dingeen gis ay tiiñalkat, di topp seen bakkan; dinañu leen tiiñal
4 They will ask, "Where is his promised coming? Since the fathers fell asleep, everything continues as it has since creation's beginning." ci di leen ne: «Ki dige woon ne dina ñëw, ana mu? Ndaxte baay ya nelaw nañu, waaye lépp a ngi dox ca njàlbéen ga ba tey.»
5 They willfully ignore this: long ago, by our Father's word, heavens existed, and earth formed out of water and through water, Fekk bëgguñoo xam lii: kàddug Yàllaa tax, asamaan ak àddina yu jëkk ya juddoo ca ndox te dunde ko.
6 and through these the world of that time was deluged with water and perished. Te ndox it moo labal àddina sa, raafal ko.
7 By the same word, today's heavens and earth are stored up for fire, kept for the day of judgment and destruction of the wicked. Te kàddug Yàlla googu moo denc asamaan yii fi nekk ak suuf si, ngir lakk leen; Yàllaa ngi leen di nége bésub àtte, ba muy alag ñi weddi.
8 Don't overlook this, loved ones: with our Father, one day is like 1,000 years, and 1,000 years like one day. Yéen samay xarit, buleen umple ne benn bés ak junniy at ñoo yem fi Boroom bi.
9 Our Father isn't slow to keep his promise, as some think; he's patient with you, wanting no one to perish, but all to reach repentance. Li Yàlla dige, dina ko def, lu mu yéex yéex ci xalaatu nit. Xanaa kay da leena muñal, ndax bëggul kenn alku, waaye ñépp tuub seeni bàkkaar.
10 But the day of our Lord Jesus will come like a thief: the heavens will vanish with a rushing sound, the elements will burn and melt, and the earth with all its works will be exposed. Waaye bésu Boroom bi dina ñëw, bett àddina ni sàcc. Su boobaa asamaan yi dinañu ne rajax toj, lu ne ci àddina lakk ba seey, te suuf ak lu mu ëmb dina ne fàŋŋ fa kanam Yàlla.
11 Since all this will dissolve, what sort of people should you be? You should live holy lives, devoted to God, Gannaaw loolu lépp dina seeye noonu nag, nangeen góor-góorlu ci gëna sellal seen nekkin te feddali seen ragal Yàlla.
12 as you wait for and hasten the coming of our Father's day, when the heavens will be set ablaze and dissolved, and the elements melt in the heat. Te it ngeen taxaw temm ci séentu bésu Yàlla bi, te waajal ñëwam. Su boobaa asamaan yi dinañu lakk, ba naaw ni pënd, te lu nekk ci àddina dina lakk, ba seey nib dóom.
13 But as he promised, we wait for new heavens and a new earth, where righteousness lives. Waaye nu ngi séentu asamaan su bees ak suuf su bees, fa njub dëkk, ci ni ko Yàlla dige.
14 So, beloved, awaiting these things, strive to be found by him in peace, spotless and without defect. Kon nag samay soppe, gannaaw yéena ngi séentu loolu, góor-góorluleen, ngir bu Kirist ñëwee, mu fekk leen ci jàmm, ngeen baña am benn gàkk mbaa sikk.
15 Regard our Lord's patience as salvation, just as our beloved brother Paul wrote you, with the wisdom given him, Te jàppleen ne muñug sunu Boroom muccu nit la. Sunu mbokk mi nu bëgg, Pool, bind na leen ko, ci xel mi ko Yàlla sol.
16 as in all his letters, where he speaks about these things. Some parts are hard to understand, and the ignorant and unstable twist them—as they do the other Scriptures—to their own destruction. Noonu lay waxe ciy bataaxalam yépp di ci biral lii. Am na ci sax yu jafee xam, te ñi amul xam-xam te seen ngëm dëgërul di ko walbati, ba alag seen bopp, te loolu lañuy def ci Mbind yi ci des.
17 So then, loved ones, knowing this in advance, guard yourselves, so you aren't swept away by the error of lawless people and lose your own firm standing. Noonu yéen samay xarit, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, moytuleen ñi weddi fàbbi leen ci seen réer, ba yolomal seen wàkkirlu ci Yàlla.
18 Grow in the grace and knowledge of our Lord and Savior Jesus Christ. To him be glory, now and to the day of eternity. Amen. Waaye màggleen ci yiwu sunu Boroom ak Musalkat Yeesu Kirist, te sax ci xam ko; moo yelloo ndam fii ba fàww.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]