Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 4 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Our Father spoke to Moses and Aaron, saying: Aji Sax ji waxati Musaa ak Aaróona, ne:
2 "Count the Kohathites among the Levites, by clan and ancestral house. «Leween ñi askanoo ci Keyat, waññleen leen bopp ak bopp, na ñu bokke seeni làng, ak seen këri maam.
3 From thirty to fifty years old, all who enter the service to work in the tent of meeting. Daleleen ci góor ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, muy mboolem ñi yelloo bokk ci kuréel, gi liggéeyu biir xaymab ndaje mi war.
4 "This is the service of Kohath's sons in the tent of meeting: the most holy things. Liggéeyu Keyateen ñi ci biir xaymab ndaje mi moo di wàllu jumtukaay yu sell yee sell.
5 When the camp moves, Aaron and his sons take down the screening curtain and cover the ark of the testimony with it. «Bu dal bi dee jóg, na Aaróona ak doomam yu góor dugg, wékki kiiraay li, di ridob biir bi, te ñu muure ko gaalu seedes kóllëre gi.
6 They are to cover it with fine leather, spread an all-blue cloth over that, and set its poles. Nañu lalaat ca kaw kiiraayal deru piipi, te ñu lalati ca kaw, ndimo lu lépp baxa, doora roof njàppuy gaal gi.
7 "On the table of the Presence they'll spread a blue cloth, put the plates, dishes, bowls, and pouring jars on it; the regular bread stays on it. «Taabalu mburum teewal mi, nañu ci lal ndimo lu baxa, teg ci ndab yeek bàttu yeek njaq yeek tax yi ñuy sottee saraxi tuuru, door cee teg mburu moomu dul wuute.
8 They are to spread a scarlet cloth over them, cover it with fine leather, and fit its poles. Nañu muure yooyu ndimo lu xonq curr, te ñu lalaat ca kaw malaanum deru piipi, doora roof njàppuy taabal ji.
9 "They will take a blue cloth, cover the lampstand of light, its lamps, tongs, trays, and all its oil vessels used to service it. «Su ko defee ñu jël ndimo lu baxa, muure ko tegukaayu làmp bi, aki làmpam aki ñiimam aki andam, ak mboolem ndabi diwam ya ñu cay jëfoo.
10 They are to wrap it and all its vessels in fine leather and set it on the carrying frame. Nañu boole tegukaayu làmp beek mboolem la muy àndal, ñu ëmbe lépp malaanum deru piipi, te teg ko ci kaw tagar bi ñu koy gàddoo.
11 "Over the golden altar they are to spread blue cloth, cover it with fine leather, and insert its poles. Sarxalukaay bu ñu xoobe wurus, nañu lal ci kawam ndimo lu baxa, lalaat ca kaw malaanum deru piipi, doora roof njàppuy sarxalukaay bi.
12 They must take all the service utensils used in the sanctuary, put them in blue cloth, cover with fine leather, and place them on the pole. Nañu jël mboolem jumtukaay yi ñuy liggéeye ci biir béreb bu sell bi, ñu ëmbe ko ndimo lu baxa, muure ko malaanum deru piipi, door koo teg ci kaw tagar bi ñu koy gàddoo.
13 "They are to remove the ashes from the altar and spread a purple cloth over it. Nañu dindi niiniti sarxalukaayu xànjar bi, te ñu lal ci kaw sarxalukaay bi, ndimo lu xonq curr.
14 On it they are to put all its serving vessels—firepans, forks, shovels, basins, all the altar's vessels—then spread over it a fine leather covering and insert its poles. Nañu teg ca kaw ndimo la mboolem ndab, ya ñuy liggéeye ca sarxalukaay ba: and yeek cappukaayi yàpp yeek ñiitukaay yeek këll yi; jumtukaayi sarxalukaay bi yépp daal, te ñu lal ca kaw, malaanum deru piipi, doora roof njàppuy sarxalukaay bi.
15 "When Aaron and his sons finish covering the holy things and all vessels of the holy place, and the camp sets out, Kohath's sons come to carry them, but they must not touch the holy things or die. These are Kohath's sons' burdens in the tent of meeting. «Bu dal bi waree jóg, na Aaróona ak doomam yu góor muur yëf yu sell yi, ak mboolem jumtukaayi xaymab ndaje mi ba noppi. Gannaaw loolu la askanu Keyat di dikk, ngir gàddu ko. Su ko defee duñu laal dara lu sell, bay dee. Loolu la Keyateen ñi di gàddu ci wàllu xaymab ndaje mi.
16 "Eleazar son of Aaron the priest is responsible for the lamp oil, fragrant incense, daily grain offering, and anointing oil—responsible for the whole tabernacle, everything in it, the sanctuary and its furnishings." «Elasar doomu Aaróona sarxalkat bi nag, ab saytoom moo di diwu làmp bi, ak cuuraay li, ak saraxu pepp bi dul jaas, ak diwu pal gi. Mooy féetewoo jaamookaay bi bépp, ak mboolem li ci biiram, ba ci yëf yu sell yi, aki jumtukaayam.»
17 Our Father spoke to Moses and Aaron, saying: Aji Sax ji waxati ba tey ak Musaa ak Aaróona, ne leen:
18 "Do not let the tribe of the Kohathite clans be cut off from among the Levites. «Buleen yóbbe Keyateen ñeek seeni làng, lu ñu leen di dagge ci biir Leween ñi.
19 Do this for them so they live and not die when they approach the most holy things: Aaron and his sons must enter, assigning each his task and burden. Nii ngeen di def ak ñoom, ba bu ñu jegee yëf yu sell yee sell, di dund te duñu ca dee: Aaróona aki doomam ñooy dugg, daldi sédd ku nekk ci ñoom liggéeyam ak la muy gàddu.
20 But they must not go in and look at the holy things, even for a moment, or they will die." Bu Keyateen ñi dugg, di xool lu mu gàtt gàtt, yëf yu sell yi. Lu ko moy ñu dee.»
21 Our Father spoke to Moses, saying: Gannaaw loolu Aji Sax ji wax Musaa, ne ko:
22 "Take a census of the sons of Gershon also, by their fathers' houses and their clans. «Ñi askanoo ci Gerson itam, nanga leen waññ bopp ak bopp, na ñu bokke seen këri maam ak seeni làng.
23 Count those thirty to fifty years old who serve, doing work at the tent of meeting. Li dale ci góor ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at ngay lim, ñuy mboolem ñi liggéeyu xaymab ndaje mi war.
24 "This is the service of the clans of the Gershonites, in serving and in carrying: Gersoneen ñi nag, lii moo di seen cér ci wàllu liggéey bi, ak li ñu wara gàddu:
25 They carry the tabernacle's curtains, the tent of meeting, its covering, the fine-leather covering over it, and the screen for the tent of meeting's entrance, ñooy gàddu kiiraayi jaamookaay bi, ak xaymab ndaje meek malaanam, ak malaanum deru piipi bi ci kaw, ak ridob bunt xaymab ndaje mi;
26 the courtyard curtains, the entrance screen for the courtyard gate, surrounding tabernacle and altar, their cords, and all their service equipment—they are to do whatever these need. ak sori ëtt bi, ak kiiraayal bunt ëtt bi wër jaamookaay beek sarxalukaay bi, ak seeni buum ak mboolem jumtukaay ya ñu cay liggéeye. Mboolem lees cay def, ñoo koy liggéey.
27 Aaron and his sons direct all the Gershonites' service—their carrying and duties; assign them all they must carry. Mboolem sasu Gersoneen ñi ci mboolem lu ñuy gàddu ak mboolem lu ñuy liggéey, ci ndigalal Aaróona aki doomam lay doon. Ñoo leen di sas mboolem lu ñu wara gàddu.
28 This is the service of the Gershonite clans at the tent of meeting, their duty under Ithamar son of Aaron the priest. Loolooy céru Gersoneen ñi, ci wàllu xaymab ndaje mi, te loolu lañu leen dénk, Itamar doomu Aaróona sarxalkat bi di leen ca saytu.
29 "As for the sons of Merari, you are to count them by their clans and their fathers' houses. «Ñi askanoo ci Merari itam, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam, noonu nga leen di lime,
30 Count everyone thirty to fifty years old who enters the service to work at the tent of meeting. dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, ñuy mboolem ñi yelloo bokk ci kuréel, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war.
31 This is their task, their service at the meeting tent: the frames, bars, posts, and bases of the tabernacle. Lii mooy li ñu sasoo gàddu ci seen mboolem liggéey ci xaymab ndaje mi: xànqi jaamookaay bi aki galanam aki jënam aki tegoom;
32 The courtyard's pillars all around, with their bases, pegs, and cords, all their equipment and service—assign by name what each must carry. muy jën yi wër ëtt bi, ak seeni tegu ak seeni buum, mboolem seen jumtukaay yu ñu cay liggéeye. Limalleen leen jumtukaay yi ñu wara gàddu.
33 This is the Merarite clans' service in the Tent of Meeting, under Ithamar son of Aaron the priest." Loolooy céru Merareen ñi, ci wàllu xaymab ndaje mi ci njiital sarxalkat bi Itamar doomu Aaróona.»
34 So Moses, Aaron, and the leaders of the congregation counted the sons of the Kohathites by their clans and their families, Ci kaw loolu Musaa ak Aaróona ak kilifag mbooloo ma lim Keyateen ña, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam.
35 thirty to fifty years old, all who joined the service for work in the tent of meeting. Ñu dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, ñuy mboolem ñi yelloo bokk ci kuréel, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war.
36 Those counted by their clans were 2,750. Ña ñu limal seeni làng di ñaari junni ak juróom ñaari téeméer ak juróom fukki góor (2 750).
37 The count of Kohathite clans, all who served in the tent of meeting, whom Moses and Aaron counted at our Father's command through Moses. Ñooñu lañu limal làngi Keyateen ñi, ñoom ñépp la liggéeyu xaymab ndaje mi war. Musaa ak Aaróona ñoo leen limoon, na ko Aji Sax ji santaanee, Musaa jottali.
38 Those counted of the sons of Gershon, by their clans and their fathers' houses, Ña ñu limal Gersoneen ñi, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam,
39 from thirty to fifty years old, all who entered service work at the tent of meeting. dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, mboolem ña yelloo bokk ci kuréel, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war,
40 Those counted by their clans and their fathers' houses were 2,630. te ñu limal leen seeni làng ak seen këri maam, ñaari junneek juróom benni téeméer ak fanweeri góor lañu (2 630).
41 These were counted from the Gershonite clans, all who served in the tent of meeting, whom Moses and Aaron counted at our Father's command. Ñooñu lañu limal làngi Gersoneen ñi, te ñoom ñépp la liggéeyu xaymab ndaje mi war. Musaa ak Aaróona ñoo leen limoon ci ndigalal Aji Sax ji.
42 Those counted of the clans of the sons of Merari, by their clans and their fathers' houses, Ña ñu limal làngi Merareen ñi, na ñu bokke seeni làng, ak seen këri maam,
43 from age thirty to fifty, all who entered service for work in the tent of meeting, dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, mboolem ña yelloo bokk ci kuréel, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war,
44 those counted by their clans were 3,200. te ñu limal leen seeni làng, ñetti junni ak ñaari téeméeri góor (3 200) lañu.
45 These were counted of the clans of Merari's sons, whom Moses and Aaron counted at our Father's command through Moses. Ñooñu lañu limal làngi Merareen ñi, Musaa ak Aaróona ñoo leen limoon, na ko Aji Sax ji santaanee, Musaa jottali.
46 All those whom Moses, Aaron, and Israel's leaders counted among the Levites, by clans and ancestral houses. Mboolem Leween ña Musaa ak Aaróona, ak kilifay Israayil limoon, na ñu bokke seeni làng, ak seen këri maam,
47 From thirty to fifty years old, everyone who served and carried loads in the tent of meeting. dale ko ci ñi am fanweeri at, ba juróom fukki at, ñuy mboolem ña yelloo bokk ci kuréel, gi liggéeyu xaymab ndaje mi war,
48 Those counted were 8,580. seenub lim nekk na juróom ñetti junni ak juróomi téeméer ak juróom ñett fukki góor (8 580).
49 By our Father's command, Moses appointed each to his service and burden, and counted them, as our Father commanded Moses. Ci ndigalal Aji Sax ji Musaa jottali, lañu leen lim, ba sas ku ci nekk ab liggéeyam ak la muy gàddu. Na ko Aji Sax ji sante Musaa, na lañu leen lime.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]