Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Numbers 35 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Our Father spoke to Moses on the plains of Moab by the Jordan across from Jericho: Aji Sax ji waxati ak Musaa ca joori Mowab, ca wetu dexu Yurdan, fa jàkkaarlook Yeriko. Mu ne ko:
2 "Command the Israelites to give the Levites, from the inheritance they hold, cities to live in, and pastureland around them, for the Levites. «Santal bànni Israayil ñu sàkkal Leween ñi ci seen céru suuf, ay dëkk yu Leween ñi dëkke. Àllu parlu ya wër dëkk ya it, joxleen ko Leween ñi.
3 The cities are theirs to live in; the pasturelands are for their cattle, livestock, and all their living creatures. Su ko defee dëkk yooyu ñeel leen, ñu dëkke. Seen àlli parlu it ñeel seenug jur, ak seen alal, ak seen mboolem mala.
4 "The pasturelands of the cities you give the Levites reach about 1,500 feet out from the city wall on every side. Parluy dëkk yi ngeen di jox Leween ñi, ci tatay dëkk ya lay dale, jëm ci biti lu day ni junniy xasab, yemook juróomi téeméeri meetar, ci wet gu nekk.
5 Measure outside the city: about 3,000 feet on the east side, 3,000 on the south side, 3,000 on the west side, 3,000 on the north side, with the city in the middle. This is the pastureland for their cities. Su ko defee ngeen natte ca biti dig-digal bu gudde ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar ci wetu penku; ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar, wetu bëj-saalum; ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar, wetu sowu; ñaari junniy xasab, yemook junniy meetar, wetu bëj-gànnaar, dëkk bi nekk ci digg bi. Dig-digal boobu day ñeel Leween ñi, di seen parluy dëkk.
6 "Of the cities you give the Levites, six are to be cities of refuge, for a killer to flee to; besides these, give forty-two cities. Dëkk yi ngeen di jox Leween ñi, ñoo di juróom benni dëkki rawtu yi nga xam ne ku rey nit man faa raweji, ak yeneen ñeent fukki dëkk ak ñaar yu ngeen leen ciy dollil.
7 "All the cities that you give the Levites are to be forty-eight cities, together with their pasturelands. Kon mboolem dëkk yi ngeen di jox Leween ñi, ñeent fukk ak juróom ñett la, ak seen àlli parlu.
8 From Israel's territory, give the Levites cities—more from large tribes, fewer from small; each gives in proportion to the inheritance it received." Dëkk yi ngeen leen di génneel ci céri suufi bànni Israayil nag, la cay génne ca ña ëpple suuf, réyal leen ko, te la cay génne ca ña néewle suuf, ngeen néewal ko. Giir gu nekk daal, dayob céru suufam si mu séddu, moom lay topp, ngir sàkke ci ay dëkkam, jox Leween ñi.»
9 Our Father spoke to Moses: Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko:
10 "Speak to the Israelites and tell them: When you cross the Jordan into the land of Canaan, «Waxal bànni Israayil, ne leen: Bu ngeen jàllee dexu Yurdan ba dugg réewum Kanaan,
11 choose cities for yourselves, cities of refuge, where anyone who kills a person unintentionally may flee there. nangeen sàkk ay dëkk yuy doon seen dëkki rawtu, ba ku rey nit te du teyeefam, man faa raweji.
12 These cities are a refuge for you from the blood avenger, so the killer won't die until standing before the assembly for judgment. Mooy doon seen dëkki rawtu yees di mucce ci mbokkum jotkat buy toppe, ba ki rey nit du dee, te taxawagul fa kanam mbooloo mi, ngir ñu àtte ko.
13 The cities you give are to be six cities of refuge for you. «Kon dëkk yi ngeen di jox Leween ñi, juróom benn a ciy doon seen dëkki rawtu.
14 Give three cities beyond the Jordan and three cities in the land of Canaan; they are to be cities of refuge. Ñetti dëkk yu ngeen di joxe ci wàllu dexu Yurdan wii, ak ñetti dëkk yu ngeen di joxe ca réewum Kanaan, lépp di ay dëkki rawtu.
15 These six cities are a refuge for Israelites, the foreigner, and the temporary resident among them, so anyone who kills a person by accident may flee there. Waaye muy bànni Israayil, muy doxandéem, muy gan gu nekk ci seen biir, na juróom benni dëkk yooyu doon seen rawtu yeen ñépp, ba képp ku rey nit te du teyeefam, man faa raweji.
16 "But if someone strikes another with an iron object and the victim dies, the attacker is a murderer—the murderer must be put to death. «Su dee ag weñ la ko dóor, mu dee, moo ko rey, te dee rekk mooy àtteb ki rey.
17 If he struck him with a stone in his hand that could kill, and he died, he is a murderer; the murderer must be put to death. Su dee aw doj wu mana rey la jël, dóor ko ko, mu dee, moo ko rey, te dee rekk mooy àtteb ki rey.
18 Or if he struck him with a deadly wooden tool in hand, and he died, he is a murderer; the murderer must be put to death. Su dee bant bu mana rey la jël, dóor ko ko, mu dee it, moo ko rey, te dee rekk mooy àtteb ki rey.
19 The avenger of blood is to kill the murderer himself; when he meets him, he is to kill him. Jotkat biy toppe bakkan ba nag, mooy rey ka rey; fu mu dajeek moom, moo koy rey.
20 If he pushed him from hatred, or threw something at him in ambush, so he died, Su dee ci biir mbañeel la dale ci kawam, mbaa mu sànni ko aw saan wu mu ko waajal, ba mu dee,
21 or if he struck him with his hand out of hatred and he died, the striker must be put to death—he is a murderer. The avenger of blood is to kill the murderer when he finds him. mbaa ci biir mbañeel la ko dóore loxoom ba mu dee, su boobaa dee rekk mooy àtteb ka dóore. Moo ko bóom. Jotkat bay toppe bakkan ba nag, bu dajeek ka rey, da koy rey.
22 "But if he shoved him suddenly without hostility, or threw anything at him without ambush, «Ndegam nag du caageenu mbañeel, xanaa mu jekki dal ci kawam, mbaa mu sànni ko këf ku mu mana doon, te du lu mu waajoon,
23 or, without seeing him, dropped on him a stone able to kill, and he died—not his enemy, not seeking his harm, mbaa muy doj wu mana rey wu mu waddal ci kaw nit ki, ba nit ki dee, te gisul woon nit ki, te nit ka du woon ab noonam, te fekkul itam muy sàkku loraangey nit ka,
24 then the assembly is to judge between the slayer and the avenger of blood according to these rules. su boobaa la mbooloo may wéyal diggante ki rey, ak jotkat bay toppe, moo di àtte yii ci yoon tëral:
25 The assembly must rescue the killer from the blood avenger's hand and return him to the city of refuge he fled to; he must stay there until the high priest anointed with holy oil dies. Mbooloo mi day musal ki rey ci loxol jotkatu bakkanu ka dee, te mbooloo ma da koy delloo ca dëkkub rawtoom ba mu làquji woon. Fa lay toog, ba kera deewug sarxalkat bu mag ba ñu baaxoo fale diw gu sell.
26 "But if the killer ever leaves the border of his refuge city, where he fled, Ndegam nag ka rey moo génn a génn, ba wees kemu dëkkub rawtoom ba mu làquji woon,
27 if the avenger of blood finds him outside his city of refuge's border and kills the killer, he incurs no bloodguilt. ba jotkat bay toppe bakkan fekk ko fu wees kemu dëkkub rawtoom, su boobaa su ko jotkatu bakkan ba reyee, du tax mu gàddu bakkan.
28 The killer must stay in his city of refuge until the high priest dies; only after the high priest's death may he return to his own land. Ndax kat ci biir dëkkub rawtoom la wara toog, ba kera deewug sarxalkat bu mag bi. Gannaaw bu sarxalkat bu mag bi deewee nag, ki rey sañ naa dellu fa mu bokk.
29 These are to be a permanent law for you throughout your generations, in every place where you live. «Loolu mooy dogalu yoon bi leen ñeel, yeen ak seen askan, ci seen mboolemi dëkkuwaay.
30 "Anyone who kills a person is to be executed as a murderer, on witnesses' testimony; one witness alone cannot testify against a person to cause death. «Képp ku faat bakkan nag, ci kaw kàddu gu tukkee ci ay seede doŋŋ lees ko saña reye, moom ma rey, waaye bennub seede du seedeel nit, ngir ñu teg ko àtteb dee.
31 "Take no ransom for a murderer's life who deserves death—he must be executed. «Te it buleen jël benn xaalisu njotug bakkanu kenn ku rey nit ku yelloo dee. Kooku dee rekk mooy àtteem.
32 Take no ransom for someone who fled to his city of refuge, letting him return to live in the land before the priest dies. Buleen jël it xaalisu njotug nit ku làquji ca dëkkub rawtoom, ngir may ko mu dellu fa mu dëkk, te sarxalkat bu mag bi deewul.
33 "Don't pollute the land you live in—blood pollutes the land, and the land can have no atonement for blood shed on it except by the blood of the one who shed it. Buleen tilimal réew mi ngeen nekk. Deret kat mooy tilimal réew mi, te réew mi deesu ko jote lenn, ci deret ju ñu tuur ci biiram, lu moy deretu ka tuur deret.
34 Don't make the land unclean—you live there, and I live among you; for I, your Father, live among Israel's people." Buleen sobeel réew mi ngeen dëkk, te man ma màkkaanoo ci biiram, ndax man Aji Sax ji maa màkkaanoo ci biir bànni Israayil.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]