Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Leviticus 7 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 "This is the law of the guilt offering. It is most holy. «Liy dogal bi ci saraxas peyug tooñ mooy lii: Lu sella sell la.
2 Where they slaughter the burnt offering, they must slaughter the guilt offering; splatter its blood on all sides of the altar. Fa ñuy rendee juru saraxu dóomal, fa lañu wara rendee juru saraxas peyug tooñ. Deret ji dees koy xëpp ci mboolem weti sarxalukaay bi.
3 All its fat is offered: the fat tail and fat covering the inner organs, Nebbon ji jépp lañuy sarxal: calgeen bi, nebbon bi sàng yérey biir yi,
4 the two kidneys and their fat at the loins, and the liver's long lobe, removed with the kidneys. ak ñaari dëmbéen yi ànd ak seen nebbon ca kaw, jàpp ca fàllare ja, ak bàjjo bi ci res wi te ñu di ko booleek dëmbéen yi, génne ko.
5 The priest burns them on the altar as a food offering to our Father; a guilt offering. Sarxalkat bi da koy boole lakk ci kaw sarxalukaay bi, muy saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, te di saraxu peyug tooñ.
6 Any male priest may eat it, eaten only in a holy place; it is most holy. Képp kuy góor te bokk ci askanu sarxalkat yi sañ na cee lekk. Béreb bu sell lees koy lekke. Lu sella sell la.
7 "The sin offering and guilt offering share one law: it belongs to the priest who makes atonement with it. «Li ci saraxu póotum bàkkaar moo nekk ci saraxu peyug tooñ, dogal bi di benn ci yooyu ñaar. Sarxalkat bi def gàtt bi njotlaay moo koy moom.
8 The priest who offers anyone's burnt offering keeps its hide for himself. Su nit joxee ab saraxu rendi-dóomal, sarxalkat bi mooy féetewoo deru jur gi mu sarxal.
9 Any grain offering baked in an oven, and all made in a pan or on a griddle, belongs to the priest who offers it. Ci biir loolu bépp saraxu pepp mu ñu lakk cib taal, mbaa ñu saaf ko ci cin mbaa ci saafukaayu weñ, sarxalkat bi koy joxe moo koy moom.
10 Every grain offering, mixed with oil or dry, belongs equally to all Aaron's sons. Waaye weneen xeetu saraxu pepp mu mu mana doon, su dee saraxu pepp mu ñuy xiiwaale diw mbaa muy mu wow, doomi Aaróona yu góor yépp a koy moom, ku nekk tollook sa moroom cér.
11 "This is the law of the sacrifice of peace offerings that anyone may bring to our Father. «Li yoon dogal ci saraxu cant ci biir jàmm, te nit sañ koo sarxalal Aji Sax ji mooy lii:
12 If he presents it as a thank offering, with it he must offer unleavened cakes mixed with oil, unleavened wafers coated with oil, and cakes of fine flour well kneaded and mixed with oil. Bu ci nit ki jubloo ag njukkal gu muy delloo Aji Sax ji, day boole ci saraxu cant gi ay mburu yu ndaw yu amul lawiir yu ñu xiiwaale diw ak ay mburu yu tàppandaar yu amul lawiir, ñu wis diw ca kaw, ak ay mburu yu ñu lakke sunguf su mucc ayib, xiiwaale ko diw, noot ko bu baax.
13 He must bring loaves of leavened bread with his thanksgiving sacrifice of peace offerings. Sarax boobu da ciy dolli mburu yu am lawiir, boole kook saraxu cant googu ci biir jàmm te mu jublu ci njukkal Aji Sax ji.
14 From it he must give one of each as a contribution to our Father; it belongs to the priest who spatters the blood of the peace offerings. Nañu jébbal Aji Sax ji ab cér ci sarax yooyu yépp, muy moomeelu sarxalkat bi xëpp deretu juru saraxas cant gi ci biir jàmm ci mboolem weti sarxalukaay bi.
15 The meat of his thanksgiving peace offerings must be eaten the day it's offered; none of it may remain until morning. Yàppu saraxas cant googu ci biir jàmm te ñu jublu ci njukkal Aji Sax ji, dees koy lekk bés bi ñu ko rendee. Du lenn lees ciy wacc, mu fanaan.
16 "If his offering is a vow or voluntary sacrifice, it must be eaten the day he offers it; what remains may be eaten the next day. «Su sarax si nit kiy génne dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa saraxu yéene, dees na ko lekk bés bi ko nit ki joxee, te lu ca des ba ca ëllëg sa, ñu man koo lekk.
17 But any sacrifice flesh remaining on the third day must be burned in fire. Lu des ci yàppu sarax si ba ca gannaaw ëllëg sa dees koy lakk, ba mu dib dóom.
18 If any of his peace offering's meat is eaten on the third day, it won't be accepted, it won't count for the offerer—it's tainted, and whoever eats it bears his guilt. Waaye kat bu nit lekkee lenn ci yàpp wu ñu def saraxu cant ci biir jàmm te fekk mu am ñetti fan, deesul nangul boroom sarax bi te du ko jariñ dara. Lu seexluwu la te ku ca lekk mooy gàddu bàkkaaram.
19 "Flesh that touches anything unclean must not be eaten—burn that flesh in fire. But other flesh: anyone clean may eat it. Yàpp wu ci laal lenn lu sobewu it deesu ko lekk. Dees koy lakk. Ci biir loolu yàppu sarax, képp ku set sañ nga cee lekk.
20 Anyone who eats meat of our Father's peace offering while unclean will be cut off from his people. Waaye ku sobewu ku lekk ci yàppu jur gu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku nañu ko dagge ci askanam.
21 Whoever touches anything unclean—human impurity, an unclean animal, or any unclean, detestable thing—then eats meat from our Father's peace offering, that person will be cut off from his people." Sobe su mu mana doon, muy lu jóge ci nit mbaa mala mu daganul mbaa mboolem lu daganul te seexluwu, ku ci laal ba noppi, lekk ci lu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku dees koo wara dagge ci askanam.»
22 Our Father spoke to Moses: Aji Sax ji dellu wax Musaa ne ko:
23 "Tell the people of Israel: Do not eat any fat from ox, sheep, or goat. «Waxal bànni Israayil ne leen: Buleen lekk lenn luy nebbonu nag mbaa xar mbaa bëy.
24 Fat from a carcass or animal mauled by a predator may serve any purpose, but never eat it. Nebbonu jur gu dee mbaa lu rabu àll fàdd, manees na koo jëfandikoo neneen nu mu mana doon, waaye deesu ko lekk mukk.
25 Anyone who eats fat from an animal offered to me by fire will be cut off from his people. Képp ku lekk ci nebbonu jur gu ñu def saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, kooku ko lekk, dees koy dagge ci askanam.
26 You must not eat any blood at all, from bird or animal, wherever you live. Te itam du lenn luy deret lu ngeen di lekke fenn fu ngeen dëkk, mu jóge ci njanaaw mbaa ag jur.
27 Anyone who eats any blood will be cut off from his people." Képp ku lekk lenn luy deret, dees na ko dagge ci askanam.»
28 Our Father spoke to Moses: Aji Sax ji dellooti wax Musaa ne ko:
29 "Speak to the Israelites: Whoever presents his peace offering to me must bring his offering to me from that sacrifice. «Waxal bànni Israayil ne leen: Képp kuy jox Aji Sax ji saraxu cantam ci biir jàmm na indi cér bi Aji Sax ji séddoo ci saraxu cant googu ci biir jàmm.
30 With his hands he must bring my food offerings; the fat with the breast he must bring, to wave the breast as a wave offering before me. Ci loxol boppam lay dindee sarax bi ñuy def saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Day indi nebbon bi, boole kook dënn bi, dënn bi di sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji.
31 The priest burns the fat on the altar; the breast belongs to Aaron and his sons. Sarxalkat bi day lakk nebbon bi ci kaw sarxalukaay bi, waaye dënn bi, Aaróona aki doomam yu góor ñoo ko moom.
32 You are to give the right thigh to the priest as a contribution from your peace offerings. Tànkub ndijoor bi jóge ci seen saraxi cant ci biir jàmm, dees koy jébbal sarxalkat bi.
33 Whichever son of Aaron offers the peace offering's blood and fat gets the right thigh as his portion. Doomu Aaróona ji joxe deretu sarax beek nebbon bi jóge ci saraxu cant gi ci biir jàmm, kookoo jagoo tànkub ndijoor bi, muy céram.
34 For I have taken the breast of the wave offering and thigh of the contribution from Israel's peace offerings, and given them to Aaron the priest and his sons as a permanent share from Israel." Li ko waral mooy, man Aji Sax ji damaa jële ci seen saraxi cant ci biir jàmm, dënn bi ñuy def saraxu yékkati-jébbale, ak tànk bi ñu jébbal, jox ko Aaróona, sarxalkat bi mook doomam yu góor. Seen cér la ba fàww ci biir bànni Israayil.»
35 This is Aaron and his sons' portion from our Father's food offerings, from the day they were presented to serve our Father as priests. Loolooy céri pal yi Aaróona ak askanam di am ci saraxi sawara yi ñeel Aji Sax ji, dale ko keroog bu ñu leen teewalee fi kanam Aji Sax ji, ñu doon ay sarxalkat.
36 Our Father commanded this be given them from the Israelites, the day he anointed them—a permanent share for all their generations. Loolu la Aji Sax ji santaane ñu jox leen ko. Bés bu ñu leen xasee diw, fal leen, mu daldi doon seen cér ci biir bànni Israayil ak seen askan ba fàww.
37 This is the law for burnt offerings, grain offerings, sin offerings, guilt offerings, ordination offerings, and peace offerings, Loolu la yoon digle ci wàllu saraxu rendi-dóomal, ak saraxu pepp ak saraxu póotum bàkkaar ak saraxu peyug tooñ ak saraxu xewu colu ak saraxu cant ci biir jàmm.
38 which our Father commanded Moses on Mount Sinai, the day he commanded the people of Israel to bring their offerings to our Father in the Wilderness of Sinai. Loolu it la Aji Sax ji dénkoon Musaa ca kaw tundu Sinayi, bés ba mu santee bànni Israayil ca màndiŋu Sinayi ñu di ko génneel ay sarax.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]