Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Genesis 7 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then our Father told Noah, "Enter the ark with your whole household, for I've seen you righteous before me in this generation. Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge.
2 Take for yourself seven pairs of every clean animal, male and female, and one pair of unclean animals, male and female, Xeeti rab yu set yépp yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ak ñaar ci xeeti rab yi setul, te ñuy góor ak jigéen.
3 also seven pairs of sky birds, male and female, to keep offspring alive across all the earth. Te it xeetu picc mu nekk yóbbaale ci juróom ñaar yu góor ak juróom ñaar yu jigéen, ngir seen xeet baña fey ci kaw suuf.
4 For in seven days I'll rain on the earth forty days and forty nights, and wipe out every living thing I made from the face of the ground." Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.»
5 Noah did everything our Father commanded him. Nóoyin daldi def la ko Aji Sax ji sant lépp.
6 Noah was 600 years old when the floodwaters came upon the earth. Bi mbënn miy ñëw ci àddina, booba fekk na Nóoyin am juróom benni téeméeri at.
7 He, his sons, his wife, and his sons' wives entered the ark to escape the floodwaters. Nóoyin dugg na ca gaal ga, ànd ak ay doomam ak soxnaam ak soxnay doomam ya, ngir mucc ca ndoxu mbënn ma.
8 Of clean animals and animals not clean, of birds and all that crawls on the ground. Rab yu set yi ak yi setul ak picc yi ak yiy raam
9 Two by two, male and female, came to Noah in the ark, as our Father commanded Noah. ànd nañu ak Nóoyin, dugg ca gaal ga, def ñaar-ñaar, góor ak jigéen, ni ko Yàlla sante Nóoyin.
10 After the seven days, the floodwaters came upon the earth. Ba juróom ñaari fan wéyee nag, ndoxu mbënn ma agsi ci kaw suuf.
11 In Noah's six hundredth year, second month, day seventeen—that same day—all springs of the great deep burst open, and heaven's floodgates opened. At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at, ca fukki fan ya ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, kera la bëti ndox ya ne jàyy, jóge xóotey géej, bunti ndoxi asamaan ne kulbét, mu ne yureet,
12 The rain fell on the earth for forty days and forty nights. taw biy sottiku ci suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg.
13 That day Noah entered the ark—he, his sons Shem, Ham, Japheth, his wife, and his sons' three wives. Keroog bés boobu la Nóoyin ànd aki doomam yu góor, Sem ak Xam ak Yafet, ak soxnaam ak ñetti soxnay doomam yooyu, ñu dugg ca gaal ga,
14 They and every wild animal by their kind, every livestock by their kind, every crawler on earth by their kind, every bird by their kind, every winged creature. àndandook rabu àll yépp, lu ci nekk ak wirgoom, ak jur gépp, lu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy raam ci kaw suuf, lu ci nekk ak wirgoom, ak lépp luy naaw, lu ci nekk ak wirgoom, muy picc mbaa boroomi laaf.
15 They came to Noah, into the ark, two by two, all flesh with breath of life. Lépp luy boroom bakkan def na ñaar-ñaar, ànd ak Nóoyin, dugg ca gaal ga,
16 Male and female of all flesh entered, as our Father commanded him; then our Father shut him in. mboolem xeetu mbindeef rekk, di góor ak jigéen, ni ko ko Yàlla sante. Ci kaw loolu Aji Sax ji ne ràpp buntu gaal gi, gannaaw bi Nóoyin duggee.
17 The flood lasted forty days on the earth; the waters rose, lifted the ark, floating above the earth. Mbënn ma nag di wal ci àddina diiru ñeent fukki fan. Ndox ya di yokku, gaal gay jóg, ba tëmb, tiim suuf lu sore.
18 Waters surged and rose greatly over the earth, and the ark floated on the water's surface. Ma ngay gën di yokku, tey baawaan ci kaw suuf, ba gaal ga tëmb, di dem ca kaw ndox ma.
19 Waters rose higher and higher on the earth, covering all the high mountains under the whole sky. Ndox ma di walangaan, ba mëdd tund yu kawe ya fépp fu asamaan tiim.
20 About twenty-two feet deep the waters rose above the mountains, covering them. Muy yokku, di yokku, ba gëna kawe tund ya lu mat fukki xasab ak juróom.
21 Everything moving on earth died: birds, livestock, wild animals, all creatures swarming the earth, and all mankind. Mboolem mbindeef mu daan dox ci kaw suuf dee na ca. Picc yi ak jur gi ak rabi àll yi ak lépp luy raam ci kaw suuf dee na, ñoom ak nit ñépp.
22 Everything on dry land that had the breath of life in its nostrils died. Mboolem mbindeef muy boroom bakkan ci kaw suuf a bokk dee.
23 Our Father wiped out every living thing on the ground's face—people, animals, crawling creatures, birds of the sky—and wiped them from the earth. Only Noah and those with him in the ark remained. Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw—lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga.
24 And the waters prevailed over the earth 150 days. Ndox mi nag di wal-wali ci kaw suuf diirub téeméeri fan ak juróom fukk.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]