Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Genesis 39 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Joseph was brought down to Egypt; Potiphar, Pharaoh's Egyptian official and captain of the guard, bought him from the Ishmaelites who had brought him down there. Ba ñu yóbboo Yuusufa Misra, Potifaar, jawriñu Firawna, ma jiite ay dagam, da koo jënd ca Ismayleen ña ko fa indi.
2 Our Father was with Joseph; he thrived, serving in his Egyptian master's house. Ci kaw loolu Aji Sax ji ànd ak Yuusufa, may ko ndam, mu dëkk ca kër sangub waa Misraam ba.
3 His master saw our Father was with him, our Father making all he did succeed in his hand. Sang ba nag gis ne Aji Sax jaa ngi ànd ak Yuusufa, di ko may ndam ci lépp lu mu sabablu.
4 Joseph found favor with him and served him; his master put Joseph over his house, entrusting him with all he owned. Sang ba am cofeel ci Yuusufa, def ko fara biir këram, dénk ko saytub kër ga, ba teg ciy loxoom lépp lu mu moom.
5 From when he put Joseph over his house and all he owned, our Father blessed the Egyptian's house for Joseph's sake; our Father's blessing was on all he had, house and field. Boobee waayi Misra ja dénkee Yuusufa këram ak lépp lu mu moom, mu di ko saytu, ca la Aji Sax ji dale barkeel këram, barkeelaale mboolem lu mu moom, kër ak tool.
6 Potiphar left all he owned in Joseph's care, aware of nothing except what he ate. Joseph was well-built and handsome. Mu daldi bàyyi lépp ci loxol Yuusufa, te li mu fa nekk tax ba toppatootul dara ciy mbiram, lu moy li muy lekk rekk. Booba Yuusufa ku jekkoon bind la te góorayiw.
7 After these things, his master's wife cast her eyes on Joseph and said, "Sleep with me." Mu am bés nag soxnas sangub Yuusufa ba xemmem Yuusufa, daldi ne ko: «Kaay tëdd ak man.»
8 He refused, telling his master's wife, "Look, with me here, my master oversees nothing in the house; all he owns he has put in my hands. Teewul Yuusufa bañ, ne soxnas sang ba: «Déglul, sama sang da maa jébbal lépp, ba toppatootul dara ci kër gi.
9 He is no greater in this house than I am; he's held back nothing from me except you, since you are his wife. How could I do this great evil and sin against our Father?" Ëpplewu ma sañ-sañ ci biir kër gi, te aayewu ma lenn xanaa yaw, ndax soxnaam nga. Kon léegi nu may mana defe ñaawtéef wu réy wu ni tollu, di moy Yàlla?»
10 Day after day she spoke to Joseph, but he refused to listen to her, to lie beside her, to be with her. Ba loolu amee bés bu Yàlla sàkk mu di ko wax Yuusufa, te dégluwu ko, wéetul ak moom sax, bay tëdd ak moom.
11 One day Joseph entered the house to do his work, with no household man inside. Mu am bés Yuusufa dugg ca kër ga, di def liggéeyam, te kenn ci surga yu góor ya nekku fa.
12 She caught him by his garment, saying, "Sleep with me!" He left it in her hand and fled outside. Ndaw si jàpp ci mbubb mi, ne ko: «Kaay tëdd ak man.» Yuusufa nag wacc mbubb ma cay loxoom, daw génn kër ga.
13 When she saw that he had left his garment in her hand and fled outside, Ndaw si gis mbubb, mi mu ko wacce, ba daw génn,
14 she called the men of her household and said, "Look—he brought us a Hebrew man to mock us. He came in to me to sleep with me, and I screamed loudly. mu woo surgay kër ga, ne leen: «Xoolleen, Ebrë sii sama jëkkër indi ci kër gi, mu di nu yab. Dafa ñëw, bëgg maa tëdde, ma yuuxu ca kaw.
15 When he heard me cry out, he left his garment beside me and fled outside. Naka laa yuuxu ca kaw, mu wacce ma mbubbam, daw génn.»
16 She kept his garment beside her until his master came home." Ba mu ko defee ndaw si denc mbubb ma, ba sangub Yuusufa ba ñibbisi,
17 She told him the same story: "The Hebrew servant you brought us came to me to mock me. mu nettalee ko ko noonu ne ko: «Jaamu ebrë, bi nga indi ci kër gi de, da maa fekksi, di ma sàkku.
18 But when I cried out, he left his garment beside me and fled outside." Naka laa yuuxu ca kaw, mu daw génn, wacce ma mbubbam.»
19 When his master heard his wife's words to him—"Your servant did these things to me"—his anger flared. Sang bi dégg li ko soxnaam wax ne moom la ko jaamam def, mu mer lool,
20 Joseph's master took him and put him in the prison holding the king's prisoners. He stayed there in the prison. ba jàpp Yuusufa, tëj ko kaso ba ñuy denc ñi buur jàpp. Yuusufa nekk foofa ca kaso ba.
21 But our Father was with Joseph, showing him covenant love and favor with the prison warden. Teewul Aji Sax ji ànd ak Yuusufa, laaye ko biir, daldi xiir wattukatu kaso ba ca moom, mu yéwéne ko.
22 The prison warden put Joseph in charge of all its prisoners; whatever was done there, he did. Ci kaw loolu mu may Yuusufa, mu yilif ñi ñu tëj ñépp, te mboolem lu ñu fay def, mu di ko jiite.
23 The warden checked nothing in Joseph's care, since our Father was with him—whatever he did, our Father made succeed. Wattukat ba seetatuloon dara lu Yuusufa jiite, ndax Aji Sax jee ànd ak moom, te lu mu sabablu, Aji Sax ji may ko ca ndam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]