Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Genesis 32 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
2 Jacob went on his way, and the angels of our Father met him. Yanqóoba moom topp yoonam. Ci kaw loolu ay malaakay Yàlla feeñu ko.
3 Jacob saw them and said, "This is our Father's camp!" He named that place Mahanaim. Ba leen Yanqóoba gisee, da ne dalub Yàllaa ngii, ba tax mu tudde béreb ba Maxanayim (muy firi Ñaari dal).
4 Jacob sent messengers ahead of him to Esau his brother in the land of Seir, the territory of Edom. Ba loolu amee Yanqóoba dafa yónni ay ndaw, ñu jiitu ko ca magam Esawu, ca réewu Seyir, di diiwaanu Edom.
5 He ordered them, "Tell my lord Esau: your servant Jacob says, I've lived with Laban and stayed until now. Mu sant leen ne leen: «Bu ngeen demee ca sama sang Esawu, neleen ko: Sa surga Yanqóoba nee na: “Maa nga woon ca kër Laban bu yàgg ba tey,
6 I own oxen, donkeys, flocks, and servants—male and female. I've sent to inform my lord, to find favor in your eyes." ma doora ñëw, ànd ak ay nag ak ay mbaam ak ay gàtt ak ay jaam yu góor ak yu jigéen; may yónnee ci yaw, di la siyaare tey sàkku nga dalal ma jàmm.”»
7 The messengers returned to Jacob: "We went to your brother Esau—he's coming to meet you, 400 men with him." Ndaw ya daldi dem ba délsi ca Yanqóoba, ne ko: «Dem nanu ca sa mag Esawu, waaye moom ci boppam mu ngi ci yoon wi di ñëw, fekksi la fii, te ma nga ànd ak ñeenti téeméeri góor.»
8 Jacob was very afraid and distressed. He split the people with him, and the flocks, herds, and camels, into two camps, Yanqóoba dégg loolu, tiit lool te ànd ak njàqare, ba tax mu séddale mbooloo, ma mu àndal, gàtt ya ak jur gu gudd ga ak giléem ya itam, mu xaaj leen ñaar.
9 thinking, "If Esau reaches one camp and attacks it, the remaining camp will escape." Booba mu ngi naan, bu Esawu songee benn dal bi, dal bi ci des mana raw.
10 Then Jacob said, "God of my father Abraham and God of my father Isaac, my Father, who said to me, 'Return to your land and family, so I may treat you well,' Ci kaw loolu Yanqóoba ñaan Yàlla, ne ko: «Yaw Aji Sax ji, sama Yàllay maam Ibraayma, di sama Yàllay baay Isaaxa itam, yaa ma ne woon: “Dellul réew ma nga cosaanoo, ca say bokk; dinaa la baaxe.”
11 I am too small for the least of all the covenant love and faithfulness you have shown your servant, for I crossed this Jordan with only my staff, and now I have become two camps. Yelloowuma lu gëna tuuti ci sa ngor ak sa worma, gi nga ma won, man sa jaam. Aw yet doŋŋ laa yoroon, ba ma jàllee dexu Yurdan, te yokku naa tey, ba doon ñaari dal.
12 Rescue me, please, from my brother's hand, from Esau's hand—I fear him: he may come and strike me down, mothers with children. Maa ngi lay ñaan, nga musal ma ci sama loxol mag Esawu, ndaxte ragal naa, mu ñëw bóom ma, bóomaale jigéen ñi ak seeni doom.
13 But you said, 'I will surely be good to you and make your descendants like the sand of the sea, too many to count.'" Te yaw yaa ma ne: “Dinaa la baaxe moos, yokk saw askan, ba mu tollu ni suufas géej si kenn manula lim ndax bare.”»
14 He stayed there that night, then took a gift for his brother Esau from what he had: Yanqóoba fanaan na fa guddig keroog, doora sàkk ca alalam, sédd magam Esawu,
15 200 female goats and twenty male goats, 200 ewes and twenty rams, lépp di ñaari téeméeri bëy ak ñaar fukki sikket ak ñaari téeméeri xar ak ñaar fukki kuuy
16 thirty nursing camels with their young, forty cows, ten bulls, twenty female donkeys, ten male donkeys. ak fanweeri giléem yu seeni doom di nàmp, ak ñeent fukki nag ak fukki yëkk ak ñaar fukki mbaam yu jigéen ak fukki mbaam yu góor.
17 He gave them to his servants, drove by drove, separately, and told his servants, "Pass ahead of me, and leave space between drove and drove." Mu ber gétt yi, gu ci nekk mu jox ay surgaam, ne leen: «Jiituleen ma, te na gétt yi dàndante.»
18 He ordered the first, "When Esau my brother meets you and asks you, 'Whose are you? Where are you going? Whose are these ahead of you?' Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: “Kuy sa njaatige?” ak “Ku moom li nga jiital?” ak “Foo jëm?”
19 then say, 'They're your servant Jacob's, a gift sent to my lord Esau. Look, he himself is behind us.'" nee ko: “Lii de sang bi, lu la Yanqóoba may la, di la ko siyaaree, yaw Esawu, te moom ci boppam mu ngi topp ci sunu gannaaw.”»
20 He also commanded the second, the third, and all who followed the herds, "Say the same to Esau when you find him, Ndigal loolu la joxaat ñaareelu surga ba ak ñetteel ba ak mboolem ña topp ca gétt ya, ku ci nekk mu wax ko ne ko loolu lay wax Esawu, bu ko gisee,
21 and you will say, 'Also, your servant Jacob is behind us.'" For he thought, "I will appease him with the gift ahead of me, then see his face; perhaps he'll accept me." tegati ca ne ko: «Te nee ko itam: “Sa surga Yanqóobaa ngi topp ci sunu gannaaw.”» Booba Yanqóobaa ngi naa ci xelam: «Bu ma jiitalee li ma ko may, neexale ko ko, bala maa janook moom, jombul mu dalal ma jàmm.»
22 So the gift passed on ahead of him, and he himself stayed that night in the camp. Neexal ba da koo jiitu, moom mu fanaan guddig keroog ca dal ba.
23 That night he got up, took his two wives, two female servants, and eleven sons, and crossed the Jabbok ford. Gannaaw loolu Yanqóoba jóg ca guddi ga, ànd ak ñaari soxnaam, ñaari jaamam yu jigéen ak fukki doomam yu góor ak benn, daldi jàll dexu Yabog.
24 He took them and sent them across the stream, and likewise sent across everything he had. Yanqóoba da leena jàllale, jàllewaale alalam jépp itam.
25 And Jacob was left alone. And a man wrestled with him until the breaking of the day. Mu des fa nag moom doŋŋ. Kera la genn góor fanaane bëre ak moom, ba bët set.
26 Seeing he could not defeat Jacob, the man touched his hip socket, and Jacob's hip was wrenched as they wrestled. Ba nit ka xamee ne manalu ko dara, dafa dóor Yanqóoba ci yaxu mooco bi, mu summikoo ca bëre ba.
27 He said, "Let me go; dawn is breaking." But Jacob said, "I won't let you go unless you bless me." Nit ka ne ko: «Bàyyi ma, ma dem, ndax bët a ngi bëgga set.» Teewul Yanqóoba ne ko: «Duma la bàyyi, nga dem, li feek ñaanaloo ma.»
28 And he said to him, "What is your name?" And he said, "Jacob." Nit ka ne ko: «Na nga tudd?» Mu ne ko: «Yanqóoba.»
29 He said, "You will no longer be named Jacob, but Israel, for you have struggled with our Father and with men, and won." Nit ka ne ko: «Tuddatuloo Yanqóoba, léegi Israayil nga tudd, ndaxte bëre nga ak nit, bëre ak Yàlla, ba génn ci ak jàmm.»
30 Jacob asked him, "Please tell me your name." He said, "Why do you ask my name?" And he blessed him there. Yanqóoba ne ko: «Waaw, yaw nag noo tudd?» Mu wax ko ne ko: «Loo may laaje sama tur?» ba noppi barkeel ko foofa.
31 So Jacob named the place Peniel: "For I have seen our Father face to face, yet my life was saved." Ci kaw loolu Yanqóoba tudde béreb ba Peniyel (muy firi Xar-kanamu Yàlla), ndaxte da ne: «Ne naa Yàlla jàkk, te maa ngi dund ba tey.»
32 The sun rose upon him as he passed Penuel, limping because of his hip. Ba jant bay fenk, Yanqóobaa ngi soox tànk bi, di bàyyikoo Penuwel.
33 This is why, even now, the Israelites won't eat the thigh muscle on the hip socket—because he struck Jacob's hip socket there, at the thigh muscle. Looloo tax ba tey jii bànni Israayil duñu lekk yàpp wi jàpp ci tenqob mooco, ndax li moocob Yanqóoba summikoo woon ca suuxu tenqo ba.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]