Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Daniel 8 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In King Belshazzar's third year, a vision appeared to me, Daniel, after the earlier one. Ca ñetteelu atu nguurug Belsacar, man Dañeel am naa meneen peeñu, gannaaw peeñu ma ma njëkkoona am.
2 In the vision I was in the citadel of Susa, in Elam province; and in the vision I was beside the Ulai Canal. Ca biir peeñu ma, maa ngi ci Sus, dëkk bu dàbbali ci diiwaanu Elam. Ma gis ci peeñu mi ne maa ngi ci wetu yoonu ndox ma ñu gas te ñu di ko wax Ulay.
3 I looked up: a ram stood before the canal, two tall horns—one taller than the other, the taller coming up last. Ma séentu, xool, yem ci kuuy mu taxaw feggook yoonu ndox ma, am ñaari béjjén yu gudd te benn bi gëna gudd ba ca des. Waaye bi gëna gudd moo mujja sax.
4 I watched the ram charging west, north, and south. No animal could stand against him, none could rescue from his power. He did as he pleased and grew great. Ma gis kuuy may dañ, di jublu sowu ak bëj-gànnaar ak bëj-saalum. Menn mala manu koo të, te maneesula xettali kenn ci moom. Ma ngay def lu ko neex tey gëna màgg.
5 As I was considering this, suddenly a male goat came from the west across the whole earth without touching the ground; it had a prominent horn between its eyes. May xool, ab sikket jóge sowu, jaare déndub suuf sépp te laalul suuf. Sikket baa nga am béjjén bu yéeme ci diggante bët yi.
6 He came to the two-horned ram I saw standing by the canal and ran at it in raging power. Mu dikk ba tollook kuuyum ñaari béjjén mi ma gisoon ci wetu yoonu ndox mi, daldi koy songe xadaru dooleem.
7 I saw him reach the ram, enraged, striking and shattering its two horns. The ram had no strength to stand against him; the goat threw it down and trampled it, and no one could rescue the ram from his power. Ma gis ko nag, mu dikk ba ca moom, song kook xadar, dóor kuuy mi, damm ñaari béjjénam, te kuuy mi manu koo të. Mu daane ko ci suuf, noote ko, te kenn manu koo teqaleek moom.
8 The goat grew very great, but at its full strength the great horn broke, and four prominent horns grew up in its place toward the four winds of heaven. Sikket bi mujj màgg lool; ba fa kàttanam yem, béjjén bu gudd ba damm, ñeenti béjjén yu yéeme daldi sax, wuutu ko, jublook ñeenti ngelawi asamaan.
9 From one of them a little horn came out, growing very great toward the south, east, and the glorious land. Ci kaw loolu béjjén bu ndaw génne ci béjjén yooyu benn, daldi law a law jublu bëj-saalum ak penkook réew ma gëna rafet.
10 It grew great, up to the host of heaven, casting down to earth some of the host and of the stars, and trampled them. Muy màgg nag bay diir mbagg gàngoori xarey asamaan, ba daaneel yenn ci ñoom, ak yenn ci biddiiw yi, nappaaje leen.
11 It made itself great against the Prince of the host; the Prince's regular offering was removed and his sanctuary's place thrown down. Muy damu bay diir mbagg Njiital gàngooru xare gi, daldi dakkal sarax ba ñu ko daan defal bés bu jot, màbb kër gu sell ga.
12 Because of wrongdoing, the army was handed over to it with the daily offering; it threw truth to the ground and acted and thrived. Gàngooru xare gi tegu ciy loxoom, boole kook saraxu bés bu jot bi, lépp cig tooñam. Béjjén bi dal ci kaw dëgg, daaneel ko fi suuf, ay pexeem àntu.
13 Then I heard a holy one speaking, and another holy one asked the speaker, "How long is the vision—the regular offering, the wrongdoing that brings desolation, sanctuary and host handed over to trampling?" Ba loolu amee ma dégg jenn aji sell di wax, jeneen aji sell ne ko: «Lan mooy àppu peeñu mii ñu gis, ñu di ci dakkal sarax biy am bés bu jot, di teddadil gàngooru xare gi, aka tooñ, di yàq lépp?»
14 He told me, "For 2,300 evenings and mornings; then the sanctuary will be restored to its rightful state." Mu ne ma: «Àpp bi ñaari junni laak ñetti téeméer (2 300) ciy guddeeki bëccëg. Gannaaw loolu dees na taxawalaat kër gu sell gi.»
15 As I, Daniel, watched the vision seeking to understand, one like a man stood before me. May xool ci biir peeñu mi, man Dañeel, di jéema xam lu muy tekki, jëmm juy nirook góor, ne jimeet taxaw ci sama kanam.
16 I heard a human voice from the Ulai calling, "Gabriel, make this man understand the vision." Ci kaw loolu ma dégg baatu nit jibe ca digg yoonu ndox ma ñuy wax Ulay. Mu àddu ca kaw ne: «Jibril, waxal kii peeñu mi.»
17 He came near where I stood, and as he drew close I was terrified and fell facedown. He said to me, "Understand, son of man: the vision is for the time of the end." Jibril dikk nag ba fi ma taxaw. Ba mu jegesee, ma tiit lool, ba daanu, sama kanam dëppu fi suuf. Mu ne ma: «Yaw doom aadama ji, nanga xam ne peeñu mii mujug jamono la.»
18 As he spoke, I fell into a deep sleep, face to the ground; but he touched me and set me on my feet. Bi muy wax ak man, ma daanu leer, sama kanam dëppu fi suuf. Mu laal ma, taxawalaat ma fa ma taxawoon.
19 He said, "Listen, I will tell you what will happen in the later time of the wrath, for it concerns the appointed time of the end. Mu ne ma: «Maa ngi lay xamal luy xew keroog ba sànjum Yàlla di jeex, ndax muj ga mooy àppu sànj ma.
20 The ram you saw with the two horns is the kings of Media and Persia. Kuuy mi nga gis mu am ñaari béjjén, buuri waa Medd ak waa Pers la.
21 The shaggy goat is Greece's king; the great horn between his eyes is the first king. Sikket bi, buuru réewum Geres la. Béjjén bu gudd bi ci diggante bët yi mooy buur bu njëkk bi.
22 The broken horn, four rising in its place: four kingdoms rise from his nation, but without his power. Dañu koo damm, ñeenti béjjén wuutu ko, di ñeenti nguur yu soqeekoo ca xeet wa, waaye duñu am doole ni ga jiitu.
23 At the end of their reign, when sinners reach full measure, a fierce-faced king skilled in intrigue will arise. «Bu nguur yooyu jeexee, ba bàkkaarkat yi buural, buur bu néeg te bare pexe dina falu.
24 His power will be great—but not his own—and he will cause terrible destruction, prosper, and act. He will destroy the mighty and the people of the holy ones. Dina gëna am doole, waaye du doon dooley boppam. Yàqam dina jéggi dayo, te ay pexeem dina àntu. Dina rey ñu am doole ba ca mbooloom aji sell yi.
25 By cunning he makes deceit thrive under his hand, and in his heart he lifts himself up. Without warning he destroys many, and rises against the Prince of princes—yet he will be broken, by no human hand. Xelum njublaŋam lay naxee, di réy-réylu, ba bett ñu bare, rey leen, te dina dëkk kilifay kilifa yi. Waaye mooy sànku, te loxo du ko laal.
26 The vision of the evenings and mornings told to you is true, but seal it up, for it concerns days far off." Peeñum ngoon meek mu bëccëg mi nga gisoon, te ñu àgge la ko, lu wér la. Yaw nag neel cell ak peeñu mi, ndax des na fan yu bare.»
27 I, Daniel, was overcome and sick for days. Then I got up and did the king's business, but the vision left me appalled, beyond understanding. Ba loolu amee ma ne làcc, wopp ay fan, man Dañeel. Gannaaw gi, ma jóg, dellu ca liggéeyu buur. Ma waaru nag ca peeñu ma, ndax daa wees sama dég-dég.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]