Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 22 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 "Brothers and fathers, listen now to my defense before you." Mu ne: «Yeen bokk yi, yeen samay baay, dégluleen léegi li ma leen di wax.»
2 When they heard him speaking to them in Hebrew, they grew even more quiet. And he said: Ba ñu déggee làkku yawut wa muy waxe ak ñoom, ñu gën ne xerem. Póol ne leen:
3 "I am a Jew, born in Tarsus of Cilicia, raised in this city, trained at Gamaliel's feet in the strict law of our ancestors, as eager for God as all of you are today. «Man ab Yawut laa, juddoo Tàrs ca diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Ci keppaaru Gamalyel laa jànge, njàng mu dëppoo bu mat sëkk ak sunu yoonu maam. Ma doonoon ku xér ci Yàlla ni mboolem yeen ñii tey.
4 I persecuted this Way to the death, binding and delivering to prison both men and women, Yoonu Sang bii tey, daan naa fitnaal ñi ko gëm ba sabab seenug dee. Yeew naa góor, yeew jigéen, tëjlu leen kaso.
5 as the high priest and the whole council of elders can testify. From them I received letters to the brothers in Damascus, and went to bring those there as prisoners to Jerusalem for punishment." Sarxalkat bu mag bi ak mboolem kuréelu magi askan wi man nañu ma cee seede. Ci ñoom sax laa nangoo woon bataaxal bu jëm ca bokki Yawut ya ca Damaas ga ma jëmoon, ngir yeewe fa gëmkati Yoon wii nekkoon foofa, ba indi leen Yerusalem, ngir ñu mbugal leen.
6 "Traveling and nearing Damascus about noon, a great light from heaven suddenly flashed around me." «Yàlla def ma topp yoon wa, ba jub Damaas ci digg bëccëg rekk, ag melax gu mag jekki fettaxe asamaan, ne ràyy fi ma wër.
7 I fell to the ground and heard a voice say to me, "Saul, Saul, why are you persecuting me?" Ma ne dàll fi suuf, daldi dégg baat bu ma ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bunduxataal?”
8 I answered, "Who are you, Lord?" He replied, "I am Jesus of Nazareth, whom you're persecuting." Ma ne ko: “Sang bi, yaa di kan?” Mu ne ma: “Man maay Yeesum Nasaret mi ngay bunduxataal.”
9 "Those with me saw the light but didn't understand the voice of the one speaking to me." Ñi ma àndaloon gis nañu leer gi, waaye ki wax ak man, xamuñu li mu wax.
10 I said, "What should I do, Lord?" The Lord replied, "Get up and go into Damascus. There you'll be told all you've been appointed to do." Ma ne ko: “Sang bi, nu may def?” Sang bi ne ma: “Jógal dem Damaas, dees na la wax foofa mboolem li ñu la sas, nga def ko.”
11 "Since that light's brightness blinded me, my companions led me by the hand into Damascus." Gisatuma woon dara ndax leeraayu melax ga; ña ma àndal ñoo ma mujj wommat, ba ma agsi Damaas.
12 "A man named Ananias, devout by the law, well spoken of by all the Jews living there, «Ku ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Ku am diiney yoonu Musaa te rafetub jëw ci biir mboolem Yawuti dëkk ba.
13 came and stood by me and said, 'Brother Saul, receive your sight.' At that very hour I looked up and saw him." Mu dikk taxaw fi sama wet, ne ma: “Mbokk mi Sóol, gisal na woon.” Ca saa sa, may gis na woon, di ko xool.
14 "He said, 'The God of our fathers appointed you to know his will, to see the Righteous One, and to hear a voice from his mouth; Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam moo la dencal céru ràññee coobareem, ak gis Aji Jub ji, dégg ko, muy wax ak yaw.
15 for you will be his witness to everyone of what you have seen and heard. Ndax li nga gis, dégg ko, yaa koy seedeel nit ñépp.
16 And now, why wait? Get up, be baptized, wash away your sins, calling on his name." Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set, teqalikook say bàkkaar, te tudd turu Yeesu.”
17 "When I had returned to Jerusalem and was praying in the temple, I fell into a trance," «Yàlla def, gannaaw ba ma délsee Yerusalem, ma doon ñaan ca kër Yàlla ga, daldi daanu leer.
18 and saw him saying to me, "Hurry and leave Jerusalem quickly, because they won't accept your testimony about me." Ma gis Sang bi, mu ne ma: “Gaawal, daw génn Yerusalem, li nga may seedeel, duñu ko nangu.”
19 I said, "Lord, they themselves know that I went from synagogue to synagogue imprisoning and beating those who believed in you. Ma ne ko: “Sang bi, ñoom ci seen bopp xam nañu ne jàngub Yawut ci kaw jàngub Yawut, maa fa daan tëjlu aka cawlu ñi la gëm.
20 When the blood of your witness Stephen was being shed, I stood by, approving and guarding the cloaks of those killing him.'" Te it ba ñuy tuur deretu Eccen, sa seede ba, man it maa nga fa woon, juboo caak ñoom, te ña ko rey, maa leen doon wattul seeni mbubb.”
21 "And he said to me, 'Go, for I will send you far away to the Gentiles.'" Mu ne ma: “Demal, man, fu sore laa lay yebal ca ña dul Yawut.”»
22 Up to that point they listened, then they raised their voices and shouted, "Erase such a man from the earth! He shouldn't be allowed to live!" Ba ba muy wax loolu, mbooloo maa nga koy déglu. Ba ñu déggee kàddu yooyu lañu xaacu ne: «Jëleleen ko ci kaw suuf! Ku mel ni kii yeyoowula dund!»
23 And as they were shouting and throwing off their cloaks and flinging dust into the air, Ña ngay yuuxoo, di sànni seeni yére, tibb suuf, di ko xëpp ci kaw.
24 the commander ordered him taken into the barracks and whipped, to learn why they were shouting against him like this. Ci kaw loolu njiitu gàngoor ga santaane, ñu dugal Póol ca tata ja, door ko ay yar, di ko laaj, ngir xam lu waral ñu di ko yuuxoo noonu.
25 As they stretched him out for the straps, Paul said to the centurion standing there, "Is it legal for you to whip a Roman citizen who hasn't been condemned?" Naka lañu ko yeew ngir dóor ko ay kàcciri, mu ne njiitu takk-der ba fa taxaw: «As goru Room bu yoon dabul, mbaa am nga sañ-sañu dóorlu ko?»
26 Hearing this, the centurion went to the commander and reported it: "What are you about to do? This man is a Roman citizen." Njiitu takk-der ba dégg loolu, daldi dem ba ca njiital gàngoor ga, xamal ko ko, ne ko: «Li ngay def nag? Nit kii as goru Room la!»
27 So the commander came and asked, "Tell me, are you a Roman citizen?" "Yes," he said. Njiital gàngoor ga dikk, ne Póol: «Yaw wax ma, ndax as goru Room nga?» Mu ne: «Waaw.»
28 The commander said, "I paid a large sum for this citizenship." But Paul said, "I was born a citizen." Mu ne ko: «Man de xaalis bu bare laa jënde sañ-sañu doon as goru Room.» Mu ne ko: «Man nag moom laa judduwaale.»
29 So those about to question him withdrew at once; the commander was afraid, realizing he had bound a Roman citizen. Ña ko doon waaja dóor ngir waxloo ko nag dànd ko ca saa sa. Njiital gàngoor ga it tiit, ba mu yégee ne Póol as goru Room la, te fekk mu yeewlu ko.
30 The next day, wanting to know exactly why the Jews accused him, the commander freed Paul, ordered the chief priests and the whole council to assemble, brought Paul down, and set him before them. Ca ëllëg sa nag njiital gàngoor ga bëgga am lu ko leer nàññ ca la Yawut ya jiiñ Póol. Mu yiwi ko, woolu sarxalkat yu mag ya ak mboolem kuréelu àttekat ya. Ci kaw loolu mu indi Póol, taxawal ko ci seen kanam.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]