Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Acts 17 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 After traveling through Amphipolis and Apollonia, they came to Thessalonica, where there was a Jewish synagogue. Ba mu ko defee ñu jaare ca dëkk ya ñuy wax Amfipolis ak Apoloni, doora àgg Tesalonig ga Yawut ya amoon ab jàngu.
2 Paul, as usual, went in to them and reasoned with them from the Scriptures on three Sabbaths. Póol nag di leen fa fekk, na mu ko baaxoo. Diiru ñetti bési Noflaay, mu di leen waxal ci Mbind mi.
3 Opening and explaining the Scriptures that the Christ must suffer and rise from the dead, he said, "This Jesus I proclaim to you is the Christ." Mu di leen tekkil Mbind mi, di leen ci firndeel ne coonob Almasi bi ak ndekkiteem manul woona ñàkk. Mu ne leen: «Yeesu mii ma di leen xamal, mooy Almasi bi.»
4 Some of them were persuaded and joined Paul and Silas, along with a great many devout Greeks and quite a few leading women. Ba loolu amee ñenn ca Yawut ya gëm, fekksi Póol ak Silas, ñoom ak Gereg yu bare yu ragal Yàlla, ak jigéen ñu ràññiku ñu bare.
5 But the Jews grew jealous, gathered evil men from the marketplace, formed a mob, and threw the city into chaos. They stormed Jason's house, seeking to bring them out to the crowd. Yawut ya nag am ca kañaan, daldi foraatoo ca mbedd ma ay taxawaalukat, dajale ay gàngoor, ba yëngal dëkk ba. Ñu song kër Yason, di seet Póol ak Silas, ngir yóbbu leen ca waa dëkk ba.
6 Not finding them, they dragged Jason and some brothers before the city officials, shouting, "These men who have turned the world upside down have come here too, Ci kaw loolu gisuñu leen, ñu diri Yason ak yeneen bokki gëmkat ba ca kanam àttekat ya. Ña ngay biral, naan: «Nit ñi tas àddinaa ngii, agsi nañu fi,
7 Jason welcomed them. They all defy Caesar's decrees, claiming there is another king—Jesus. te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp a xëtt ndigali buur Sesaar, te naan am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»
8 And they stirred up the crowd and the city authorities who heard these things." Ba mbooloo ma ak àttekati dëkk ba déggee loolu, dañoo jaaxle.
9 And when they had taken bail from Jason and the rest, they let them go. Ba loolu amee ñu feyloo Yason ak ña ca des daan ba ca war, door leena yiwi.
10 The brothers at once sent Paul and Silas off by night to Berea; on arrival they went to the Jewish synagogue. Ba mu ko defee bokki gëmkat ña yebal ca saa sa Póol ak Silas ca guddi ga, ñu jëm Bere. Ñu agsi, dem ca jàngub Yawut ya.
11 These Jews were more open-minded than those in Thessalonica, receiving the word eagerly and examining Scripture daily to see if these things were true. Waa Bere nag gëna am déggin waa Tesalonig. Ñu gëm kàddu gi, xér ci lool, bés bu nekk ñuy niir Mbind mi, ngir xam ndax la ñu leen di wax noonu la.
12 So many of them believed, along with many prominent Greek women and men. Ci kaw loolu Yawut yu bare gëm, ñoom ak jigéeni Gereg ñu ràññiku, ak ay góori Gereg ñu bare.
13 When Jews from Thessalonica learned Paul proclaimed the word of our Father in Berea too, they went there also, agitating and stirring up the crowds. Ba loolu amee Yawuti Tesalonig dégg ne Póol a ngay xamle kàddug Yàlla ca Bere itam. Ñu dikkati, yëngal nit ña, ñu def ay gàngoor.
14 The brothers immediately sent Paul off to the sea, but Silas and Timothy stayed there. Ca la bokki gëmkat ñi yebal Póol ca saa sa, mu jëm ca tefes ga, Silas ak Timote ñoom, des ca Bere.
15 Paul's escorts brought him to Athens, then left with orders for Silas and Timothy to join him as soon as possible. Ña dar Póol nag gunge ko ba ca dëkk ba ñuy wax Aten, ñu doora dëpp, jottaliji Silas ak Timote kàddug Póol, ngir ñu fekksi ko nu mu gëna gaawe.
16 While Paul waited for them in Athens, his spirit was provoked within him, seeing the city full of idols. Diggante ba Póol di nég Silas ak Timote ca Aten, xolam jeex na ndax dafa gis na dëkk ba yeboo ci jaamu ay tuur.
17 So he debated in the synagogue with Jews and worshipers of God, and daily in the marketplace with whoever was there. Ci biir loolu muy wax ak Yawut yaak jàmburi ragalkati Yàlla ya ca jàngu ba, di wax it ak waa pénc ma bés bu nekk.
18 Some of the Epicurean and Stoic philosophers also debated with him. Some asked, "What's this babbler trying to say?" Others said, "He seems to promote foreign gods"—since he preached the good news of Jesus and the resurrection. Ci kaw loolu ay boroom xam-xam yu bokk ci ngérum Epikur ak ngérum Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ña ne: «Kebetukat bii, lu muy wax nii?» Ña ca des dégg Póol di waare xibaaru jàmm bi ci Yeesu ak ndekkiteem, ñu ne: «Daa mel ni ay tuur-tuuraani doxandéem lay waareel.»
19 They took him and brought him to the Areopagus, asking, "Can we know what this new teaching you're presenting is? Ñu jàpp ko nag, yóbbu ko ca ëttub àttekaay ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Ndax man nanoo xam njàngale mu bees mii ngay siiwal, lu mu doon?
20 For you bring strange things to our ears, so we want to know what they mean." Ndax li ngay wax kat sunu ngan-gi-nopp la. Nu bëgga xam nag loolu lu muy tekki.»
21 Now all the Athenians and foreigners living there spent their time on nothing but telling or hearing something new. Booba waa Aten ñépp, doxandéem ak njuddu-ji-réew, xintewuñu lenn lu moy di nettali aka déglu xew-xew wu bees.
22 Paul stood in the middle of the Areopagus and said, "Athenians, I see that you are extremely religious in every way. Ci kaw loolu Póol taxaw ca digg ëttub Areyopas, ne leen: «Yeen waa Aten, gis naa ne ci wet gu nekk ñu farlu ngeen ci diine.
23 For as I passed through and examined your sacred objects, I found an altar inscribed: 'To an unknown god.' What you worship without knowing it, I now proclaim to you. Ndax maa doon doxantu, di seet seeni jaamookaay, ba yem ci sarxalukaay bu ñu bind mii mbind: “Ñeel yàlla ji nu xamul.” Loolu ngeen di màggal te xamuleen ko nag, moom laa leen di xamal.
24 Our Father, who made the world and everything in it, being Sovereign of heaven and earth, doesn't live in temples made by hands, «Yàlla mi sàkk àddina ak mboolem li ci biiram, di Boroom asamaan ak suuf, dëkkewul màkkaan mu ay loxo sàkk.
25 nor served by human hands, as if he needed anything—he himself gives everyone life, breath, and everything. Te it jariñoowul loxol nit, mbete ku soxla lenn, ndax mooy may ñépp bakkan akug noo, ak lu mu mana doon.
26 From one man he made every nation of mankind live across the whole earth, fixing their set times and the boundaries of their homelands, Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndub suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay.
27 so they might seek our Father, perhaps reach for him and find him—though he is not far from each of us, Yàllaa def loolu, ngir xeeti àddina wut ko, làmbatu ba daj ko, ndegam man naa am, doonte sorewul kenn ku nekk ci nun.
28 for 'In him we live and move and have our being'; as even some of your own poets have said, 'We too are his descendants.' “Ndax sunu bakkan ak sunu yëngu ak sunug nekk, lépp ci moom la.” Mooy ba tey la ñenn ci seeni woykat ne: “Nun itam aw xeetam lanu.”
29 So as our Father's children, we shouldn't think the divine is like gold, silver, or stone—an image shaped by human skill and imagination. Ndegam nag xeetu Yàlla lanu, warunoo nirule Yàlla ak lenn luy wurus mbaa xaalis mbaa aw doj te sosoo ci xareñtey nit akum xelam.
30 The times of ignorance our Father overlooked, but now he commands all people everywhere to repent. Yàlla nag jéllale na jamonoy ñàkka xam googa woon, waaye tey mu ngi woo ñépp ak fépp fu ñu féete, ngir ñu tuub.
31 He set a day to judge the world justly, through a man he appointed—proving it to all by raising him from the dead." Ndaxte Yàlla jàpp na bés bu muy àttee àddina ci dëgg, àtte bu nit ki mu tabb di sottali; te loolu Yàlla jox na ci ñépp firnde lu wóor, ba mu dekkalee kooku mu tabb, ndekkite lu dee toppul.»
32 Hearing of the resurrection of the dead, some mocked; others said, "We'll hear you on this again." Naka lañu dégg waxi dee-dekki, ñenn ña di ko foontoo, ña ca des ne ko: «Dinanu la déglu, nga waxalaat nu ci moomu mbir.»
33 So Paul left them. Ba loolu amee Póol bàyyikoo ca seen biir.
34 But some men joined him and believed, including Dionysius the Areopagite, a woman named Damaris, and others. Teewul mu am ñu ko fekksi, ba mujj gëm; Deni mi bokk ci ëttub Areyopas ci la, ak jigéen ju ñuy wax Damaris, ak ñeneen.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]