Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

2 Chronicles 36 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 The people of the land took Josiah's son Jehoahaz and made him king in Jerusalem in place of his father. Askanu réew ma nag jël Yowaxas doomu Yosya, fal ko buur, mu wuutu baayam fa Yerusalem.
2 Jehoahaz was twenty-three years old when he became king, and he reigned three months in Jerusalem. Ñaar fukki at ak ñett la Yowaxas amoon ba muy falu buur. Ñetti weer la nguuru fa Yerusalem.
3 Egypt's king deposed him at Jerusalem and fined the land about 7,500 pounds of silver and 75 pounds of gold. Buuru Misra moo ko jële Yerusalem, ba noppi teg réew ma galagu fanweeri barigoy xaalis ak ñeent (34), ak fanweeri kiloy wurus ak ñeent (34).
4 Egypt's king made his brother Eliakim king over Judah and Jerusalem, renaming him Jehoiakim; Neco took his brother Jehoahaz to Egypt. Ci kaw loolu buuru Misra fal Elyakim magu Yowaxas buurub Yuda ak Yerusalem. Mu daldi soppi turam, tudde ko Yoyakim. Yowaxas rakk ja moom, Nekko jàpp ko, yóbbu Misra.
5 Jehoiakim was twenty-five when he became king; he reigned eleven years in Jerusalem, doing evil in our Father's eyes. Ñaar fukki at ak juróom la Yoyakim amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Muy def nag li Aji Sax ji Yàllaam ñaawlu.
6 Nebuchadnezzar king of Babylon marched against him, bound him in bronze chains to take him to Babylon. Moom la Nebukatnecar buuru Babilon dal ci kawam, jénge ko jéngi xànjar, yóbbu Babilon.
7 Nebuchadnezzar also took some of our Father's house articles to Babylon, putting them in his temple in Babylon. Lenn ca yëfi kër Aji Sax ja nag, Nebukatnecar yóbbaale ko Babilon, yeb ko ca màkkaanu buuram ca Babilon.
8 The rest of Jehoiakim's acts, his detestable things, and the charges against him are written in the Book of Kings of Israel and Judah; his son Jehoiachin reigned in his place. Li des ci mbiri Yoyakim ak jëf ju seexluwu ja mu jëf ak la ñu ko gisal, ma ngoogu binde ca téere ba ñu dippee Buuri Israayil ak Yuda. Yoyakin doomam a falu buur, wuutu ko.
9 Jehoiachin was eight when he became king; he reigned three months and ten days in Jerusalem, doing evil in our Father's eyes. Juróom ñetti at la Yoyakin amoon ba muy falu buur, te ñetti weer ak fukki fan la nguuru, Yerusalem di péeyam. Muy def nag li Aji Sax ji ñaawlu.
10 In spring, King Nebuchadnezzar brought him to Babylon with the precious articles from our Father's house, making Zedekiah, Jehoiachin's relative, king over Judah and Jerusalem. Ba at ma délsee la Buur Nebukatnecar yónnee, jëlsi ko yóbbu Babilon, boole ca yëfi tànnéef yu kër Aji Sax ji. Ba loolu amee la fal Cedesyas mbokkum Yoyakin, buurub Yuda ak Yerusalem.
11 Zedekiah was twenty-one years old when he became king, and he reigned eleven years in Jerusalem. Ñaar fukki at ak benn la Cedesyas amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem.
12 He did evil in our Father's eyes, not humbling himself before Jeremiah the prophet, who spoke from our Father's mouth. Muy def li Aji Sax ji Yàllaam ñaawlu, toroxluwul, tuub fa kanam Yonent Yàlla Yeremi ma waxe ndigalal Aji Sax ji.
13 He also rebelled against King Nebuchadnezzar, who made him swear by our Father, stiffening his neck and hardening his heart, refusing to return to our Father, God of Israel. Cedesyas fippu na itam ca kaw Buur Nebukatnecar ma ko giñloo woon ci Yàlla ne moom lay nangul. Daa sajju loos, të ticc, baña dellusi ci Aji Sax ji Yàllay Israayil.
14 All the leading priests and the people grew more and more unfaithful, matching all the nations' detestable practices, and made unclean the house our Father had made holy in Jerusalem. Rax ci dolli mboolem njiiti sarxalkat ya ak askan wa gënatee jëfe ag ñàkk worma, di roy mboolem jëf ju seexluwu ju xeet yi nekke, ba sobeel kërug jaamookaay gi Aji Sax ji sellaloon ngir boppam fa Yerusalem.
15 Our Father, the God of their fathers, sent word repeatedly through his messengers, pitying his people and his dwelling place. Aji Sax ji seen Yàllay maam ya yónnee na leen ay yooni yoon ay ndaw, ndax ñeewante ñoñam ak màkkaanam.
16 But they mocked our Father's messengers, despised his words, mocked his prophets, until our Father's anger rose against his people, past remedy. Teewul ñuy kókkali ndawi Yàlla, di teddadil ay kàddoom, di ñaawal ay yonentam. Sànjum Aji Sax ji nag mujj jógal ñoñam, ba menn paj manatu cee am.
17 So he brought Chaldea's king against them, who killed their young men with the sword in their sanctuary, sparing no young man, virgin, elder, or aged. Our Father gave them all into his hand. Moo indi ci seen kaw buurub waa Babilon, mu reye saamar seeni waxambaane, ba ca biir kër gu sell ga, ñeewantewul kenn; du ndaw lu góor, dub janq, du mag, du ku weex tàll ak bijjaaw. Ñépp la Yàlla teg ci ay loxoom.
18 All the articles of our Father's house, great and small, the treasures of our Father's house and of the king and his officials—all he brought to Babylon. Ci biir loolu mboolem yëfi kër Yàlla ga, yu mag yaak yu ndaw ya ak denci kër Aji Sax ja ak denci kër buur aki jawriñam, lépp la boole yóbbu Babilon.
19 They burned the house of our Father, tore down Jerusalem's wall, burned all its palaces, destroyed everything valuable in it. Ñu lakk kër Yàlla ga, màbb tatay Yerusalem, mboolem këri buuram, ñu lakk, mboolem lu ca gànjare, ñu yàq ko.
20 He exiled the sword's survivors to Babylon; they served him and his sons until Persia's kingdom began to reign, Ba mu ko defee, ndes wa mucc saamar, mu jàpp leen yóbbu ngàllo ca Babilon, ñu doon ay jaamam, moom aki doomam, ba keroog nguurug Pers mujj teg tànk.
21 to fulfill our Father's word through Jeremiah: until the land enjoyed its sabbaths, all its desolate days it rested, fulfilling seventy years. Loolu nag moo sottal kàddu ga Aji Sax ji wax jaarale ko ci gémmiñug Yonent Yàlla Yeremi bi mu nee diiru juróom ñaar fukki at la réew mi di gental, ngir fey Ati Noflaay ya ñu sàmmul woon.
22 In Cyrus king of Persia's first year, to fulfill our Father's word through Jeremiah, our Father stirred Cyrus king of Persia's spirit to proclaim throughout all his kingdom, and to put it in writing: At ma njëkk ca nguurug Sirus buuru Pers, Aji Sax ji moo nammoona sottal kàddu ga mu waxe ca gémmiñug Yonent Yàlla Yeremi, ba tax mu xiir Sirus buuru Pers, mu siiwtaane ab dogal ci mboolem réewam, boole ci bind ko ne:
23 Cyrus king of Persia says: "The LORD, God of heaven, gave me all earth's kingdoms and charged me to build him a house in Jerusalem, in Judah. Any of his people among you—may the LORD his God be with him—let him go up." «Sirus buuru Pers dafa wax ne: Mboolem réewi àddina, Yàlla Boroom asamaan moo ma leen dénk, te moom moo ma tabb, ngir ma tabaxal ko kër ca Yerusalem ga ca Yuda. Képp ku bokk ci mboolem ñoñam, yal na Aji Sax ji Yàllaam ànd ak moom, mu dem Yerusalem.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]